BAAY LAAY AMUL MAAS
BISMI LAAHI RAHMANI RAHIMI
Baay laay amul mass
Njool yaay boroom diine
Xàllal nga nu yoon
Leeral nga ngirum diine
Yeen gëm yi kaay leen nu waxtaan
Fii ci kañ Baay Libaas, moo feeñ ci Soodaan
Te noo nampoon wolof miin ko lool
Jii wax araamul, ci laay, kañ Seydi Soodaan
Baay Laay a leen yay ci tééré Yàlla, Buur bi nu moom
Xamxam ba nekkoon ca Maxfuus, moo ko saytu woo leen
Waar leen ñu gantu, geum yay sellel ba rilwaan
Bu leen wutal Baay Laay maas nde bonte mu ñaaw
Yonnent akub seriñ duñu benn ba diy maas,
Njiin jàngul, bindul, dajalewul tééré di ci seet
Yàllaa ko yonni muy woote diine lislaam
Baay Laay newul "baa siin mimmara ak liif, laam"
Jaaxal na walliyu waxumaak fooroya juy waare
Dogonkoon ak réér ngeen jebbeul ko Lislaam
Maam Aadamaa tiim ña mu feekkoon ba tën ba laa woor
Malaaka yay sujjoot ngir leeru Yonnent ga ca moom
Laay laay la Laahu ja mo xotti gémmëñ ga leer ya saawaan
Yooyay juñjugn réy na, danu koy woy ba Diiwaan.
Xam naa ci say jikko ñatti tééméér
Dadul jeex, am nga kiraama
Sak mbaax réy na ku lim juum
Rafet jikko muñ gu yaa
Xam-xam budul jéex, yaatu taaru tabe
Màndu, am diine amuk leer
Baay laay ba muy waaja feeñ, biddééw la andal bu leer
Way réér ya naan biddeewub laar, way gëm ya naan bidééwub leer
Loolu bir na leen, Séydéey "nooru lislaam"
Baay Laay dafa feeñ samp raayi jullit waar leen
Bu ngeen gëmoon jëfu Buur Yàlla du ngeen jaaxle
Yonnent dafa woote, ngen gàntu, bu leen naagu
Baay Laay, naka feeñ, ne Yàllaa ma yonni ci yeen
Yàllaa ma yonni ; te Yàlla nee na ngeen tuuba yeen,
Mbooleem nit ak jinne kaay leen xañtu lislaam
Sunu Buur la nuy woy di tagg Yonnent bi aleyhi salaam
Baay Laay a woote lislaam, gëm leen ko, man woolu naa
Yaakaar, ku kañ Seydi am ngag may fa Diiwaan
Yaa naawewoon Màkka, yanu leer yaak sunuy ruu
Ba ngay cëppéelu ngor, riir wa dektu Rilwaan
Ku gëm nu gëm, ku bañ dunu tàggo ba Diiwaan
Njool ma cëppéélu biir Yoof, leeram ga dem Kambaréén
Jénéer ba dem Beyti Maamur "saalihina" ya teew
Ña gëm fa Ndar woolu, Waalo gëm te kontaan
Ñoñam ya wër ko di sabba, bañ yaa nga naa dééta waay
Wax leen ci waa ji, balaa siiw sànku, nan dem ca Buur
Pikin dañoo jeex, maam jaa wootewoon diiné
Ngëlëm dafa réy, te réér metti ma di jooy
Ku doon siyaar Nabi, Yaaram baa nga biir Jammalaay
Ku daan bégé Séydi Isaa war nga ñëw tuuboo
Yàllaa la tannoon ci biir Yonnent yi, def la ngay njiit
Yaa moom juroom ñaari diiwaan, xawsu màndi ngay leer
Deeful wëjjéek yow nde yaa leen mën fa diiwaan
Ba Baay demmee taaxi Béér, tuut koon kiraamaam ya feeñ
Dëndug nawet jib na noor, boobéé ba tey ken du laal
Baay Laay kerook ñay wu weex tiital na waa Béér
Sëriñ si daa mawwu dugg xalwa di seeti Baay Laay
Bëtub kiñaan daan na mbémpeen ba boroom réér
Man dey dama yéém ñi ko wéddi te muy moom
Bu leen werante biib taal yonnent a ko taal
Ku ci xamul te di xamxamlu baña laaj
Yellonte ngay kaang mbaa fooreya di nga réér
Lëndëm ga sànk la doo seerooti "ridwaan"
Ku fekkewoon ba ngay woote xam ne yaay ki fi man
Xérëm yu réy ya ca biir Yoof, xàmb yaak ña kay muur
Semmal nga leen ba ñuy jaamu Yàlla, ken dootu yow
Yonnent bi, yaay mbër mi xàlloon yoonu lislaam
Xamxam, lu muy jariñ, lu moy jëfe ko, digal ko saw gaay
Bu loolu lépp nekkul, moo jaa, ku fiy wonew yoon
Subhaana xamxam bu lay wommat jëme Saam
Wax ja moo lay gétën ngay làyyoo jëme naari
Yonnent fu mu mosa feeñ, Yééfeer ya bañ ko diy noon
Ña donn ay kàggu, ñooñaa koy werante ba Saam
Ña teela gëm naan fa Zam-Zam, am fa ridwaan
Yoow waat nga wàcca nga, yaa woote jubël diiné
Birël nga sap woote, doo làyyoo ba ken di la yay
Yembal nga jox Seydi, muy ommat ba diiwaano
Yow waat nga wàcca nga, yaa woote jubël diiné
Doo bayyi waxtu, do tooñ, doo ngnaññ kenn, sàllaaw
Sellal nga saw yoon Baay rafet diiné
Yow waat nga wàcca nga, yaa woote jubël diiné
Naroon na noo sànku, noo ngi jaamu ken dootu yow
Yonnent bi yaay mbër mi xàlloon diine lislaam
Baay Laay ne seytaane raay na boppi mbindééf yi
Ba Baay nelawee la gééj tiit, neex ba nuy naan
Dogoon ak réér ngeen jébbël ko Lislaam
Ku koy werante da nga laajul ñi doon jééma bañ diinéém,
Kalaame kook buur, ba Baay duggee gaal
La gééj sàbbaa, Aras jayoo
Ba Boroom Aras yëngoo Baay Laay weesuwul Béér
Xaybar la Yééféér ya fitnaal noon ya ñuy seeti Njiin
Njool ma feeñu leen ca tisbaar ngir yërmëndeem ju réy
Ak bañ gëm ya weddi, Baay Laay yaa rafet diiné
Ñu nga naa kaayleen ñu wër Goor gi, seet njañ li muy muur
Mu ne leen reew ngeen, nde suma njañ li bu ngeen ko dee laal
Asamaan daldi tàppok suuf, gééj ga baawaan
Ñu nga naan tey jii nu gis njañ lu mosul feeñ lu tey
Nëbbub Yàlla jomb na jaam gis ko, Njiin du seen maas
Kéwél ga daldi féx, gaa ña tiit ba daw tasaaroo
Ba ñu laa yembaat la Baay Laay japp bay ñaan
Moo simpi xamb ya, taxawal diine Lislaam
"Xaatimi nabi-iina" sunu Yonnent bi woy leen ko
Moo leeral sunu xol ba sunu tur dem ba Diiwaanoo
Nuy muslu séytaane, kiy raay boppi xam ya ñuy réér
Diggënte rafle waak xiif waak mar wu tar wa ca Saam
Na ump gaa yay dëggal Yonnent ba Diiwaano
Lay jeex na Njiin jib na Diiwaan wacc biir Yoofi gééj
Tambur ba jib na, muy baatub Laa ilaa illa Laah,
Li Yàlla def bir na miim rééw, dootu fey abaadaa
Japp ak Julléék woor la nuy sàlloo ba rilwaan
Japp ak julléék woor la nu Yonnent bataleel
Goor ak jigéén ndaw ñépp da ciy maase
Yonnent a ngay nelaw te bu yeewoo nu kontaan
Kañ leen boroom ngir mi, Baay Laay mooy dindi réér
Yaa nuy dindil tiisu bammeel may nu xééwël ca biir
Firdawsi, Kawsaray baawaan nuy sanguy naan
Yaa daagu jëm Pééy bu réy bi, ñépp sew na ci moom
Dééyaale faak Buur ba, ba mu tampeel la, yaay Ruuhu Laahi
Yàlla la may yaa di njiitu "ahlu Soodaan"
Yow yaa jëkkoon feeñ, di jantub diine, bir miim rééw
Leer yaa ngiy baawaan ba Soodaan siy xëcco may gi ñoom
Dañoo xamul Xawsu, Baay Maanaay boroom diiné
Anta Lamiin nga yaa "Séydil xalaa-ixi
Yaa samsu Samaanun, wa yaa nuurun bilaadi
Seydi Ruuhun min na Laahi "
Ilahiinaay pééy ba, noo séqë taabal ja nook Maam
Firdawsi kontaan na ngir nun ñiy dëggël ñaari leer
Bu ngeen yaboo maare, am ngeen mbër fa Diiwaanoo
Bu leen iññaanante ngir nun Buur bi nuy jaamu moo sàkkoon
Mbugëg, mbégte, te nuy ñaan mbég mu réy ma ca biir
Firdawsi, Séydi yaa nuy omat ba Diiwaanoo
Yonnent la nuy woy, bu leen dingnat cofeel gu tar la
Xol fees na bay tuuru, gëm woy leen boroom diine ji
Bañ yaa ngi suumurlu, nuy kontaan ba Diiwaanoo
Sa wird wi, da nga ko jaayul, nde bonte nga riis
Sakkuwoo ku lay siiwal, wees nga puukëre laay
Yaa jiituwoon gaa ña Diiwaan tann Lislaamoo
Ngirëm mi réy na te yaa, wirdam wi mat na tte leer
Gaalam du tarde du raay, paasam jafewul ab jaam
Roy leen ci Séydi, moo nuy ommat ba Diiwaanoo
"Lay laa illa Laahu, Jëlliilu Zikru Rabbaani"
Bi Laahi ku bañ xawsu, doo seerooti Yonnent ba naan
Lay laa illa laahu, leer gay jolli ba Diiwaanoo
Al hambdu li Laahi, sunu Yonnent bi doy na noo laay
Nee na yeen gëm yi, am ngeen ngënéél, Yàllaa ma wooteloo
Ngeen ñëw, japp leen ci laay-laay
Jàpp ak julleek woor la nuy sàlloo ba Diiwaanoo
Ab jant fenk na biir Yoof, guy gindik réér
Réylu ak way-réér la ñu fallas ca niiraan
Tee ngen a waaxu ñëw laaj Séydi boroom diinee
Tàmbur bu réy ba fa Buur Yàlla la ñuy jiin
Sunu yaaram bu tedd bi Séydi Ruuhu Rahmaan
Màkkaak Medina ba Saam ràññe na say leer
Sunu Yonnent ba mu bàyyikoo Beyti Maamur la feeñ
Yaraax la wàcci, gis ñi ko jàngoon te ràññeewuñu
Ñuy séénu kaw, Njool ma war Jàkkeer ja xuus ci seen biir
Jullééji Baay Laay, Yaraax werante, nuy wooloo
Yaaram bi tiim nga say maas, Buur Yàlla def na ko jéég
Sëriñ si bañ dañoo réér jomlu nde bonte ñu laaj
Xatmun tariixa bi Isaa ibnu Maryaamaa
Nooru Nabi nooru Issa ibnu Maryaamaa
Yaaram bi donn ngay leer, sellal nga yoonu lislaam
roy leen ci Séydi moo nuy ommat ba Diiwaan
Nun kay nu ngiy gaajo leeram yu tar yi nuy naan
Bañ yaa ngi nuy xas, da nuy sàbbaa, du nook ñoom
Looloo di seen diine, Séydi am nga rilwaanoo
Tàmmal nga say gune ñuy xam yoonu Yàlla bay mag
Yéénétunoo bayyi lislaam, yaa nu won yoon wi
Tàmpees na nuy tur ca Diiwaan, yaay boroom diinee
Farlook a dem jakka, fatte toppatoo ndaw,
Te boo soxlaa di leen pàmpe lii làyyoo la daan jur fa Saam,
Lileey mbasun diine roy leen Njool boroom diinee
Kuy xañtu lislaam te doo làkkal xaleel won ko yoon
Doo teela may gune ag buum, muy moyug tooñ ci moom
Loolooy mbasun diine, roy leen Njool boroom diinee
Bul xeeb wolof lee nga fàtte, deglu naa la ñuy wax
Xam leen ne bët da dul suur, dee doora gëm du ngënéel
Ñi daan werante Yonnent làyyo ji nañ Saam
Ku fekkewoon woote baak naaféq yaak ña gëmoon
Dellooti daw ngir ga bànneex, topp dunyaa ba dee
Ku dem ñu ngay réccu ngir làyyoo ba fa Saam
Limaamu Laay, Mahdiyu xayrul waraa Muhammadu
Bu ngeen xamul goor gi, moo feeñoon ca Màkka, muy baax
Mu dellu feeñ Yoof, Waa rééw may xëccoo yoonu Màkka
Dañoo xamul muj ga, Baay Maanaay boroom diinee
Loo tayyi ñakk nga, loolaa réccu fekk mu wéy
Nan daan bakken yi, te tuub sellal, ku réy da ngay réér
Roy leen ci Séydi moo nuy ommat ba Diiwaan
Mbooleem li fiy fooreya duñu dab Abdulaay bun Salaam
Laajam bu réy ba mu doon laaj Yonenti Yàlla Nabi
Te noon bu koy xam na ngeen tuub, booba mooy Mustafa
Mu waxko lépp, mu yéém ba waaru far tuub ci moom
Dellooti Xaybar naa tuub leen Muhammadu feeñ
Xaybar la yééfeer ya jéex ngir doj yu tàng yay dal
Malaaka yaay wàcc, Buur Yàllaay dimmëli sunum njiit
Roy leen ci Séydi moo nuy ommat ba Diiwaanoo
Yàllaa la yonni nga feeñ Màkka ñu bañ diinee
Nga sanc Medina, leer gay jolli ba Saam
Beyti nangul na la, Faas gëm na sa diine
Nga dellu feeñ Yoof, ñooña bañ diine
Nga sanc Kambareen, leer gay jolli ba Malika
Yëmbël nangul na la, Ndakaaru gëm na sa diine
Saa Baay Limaamu kiy njiit, Buur, Yàlla may na ko moom
Yaaram yi xam na ko, moo dekkal ngiram Nabi Laay
Jébbël ko Baay Séydi muy daaral pomu diinne
Yow yaay Liimaan, wa lislaam, wa lihsaan, la ka ridwaan
Saw tur la ñuy tampe, soo yeewoo tabala ya jiin
Laay laa illa Laahu, leer gay wéy ba Diiwaanoo
Sunu rombukaay bii di dunyaa
Bunu fi def lu nuy lor
Na ngeen xam ne goor gu feeñoon fa Màkka
Moo dellu feeñ fii ci Yoof
Moo nuy jàllé ëllëk
Baay Laay yày boroom caabi yi.