(2) Allaahu ma salli allaa Seydinaa Muhamadu
BISMI LAAHI RAHMANI RAHIMI
"Allaahu ma salli allaa Seydinaa Muhamadu
Salli wa sallim, yaa Rabbi, salli a laa Muhamadu"
Saa maam Limaamu wooté na
Ba "Lanbiyaayi" woolu na
Te Ruuhu Laay jiitu na
Di làmpu leeri Medina
Yaaram bu yiw bi wàcc nga
Yaa Ruuhu Laay tedd nga
Ku koy werante weddi nga
Su ma yabo ne sànku nga
Yàlla la yonni ngay Nabi
Ngay seen gënéél ginnaaw Nabi
Liggééy nga, am ngërëm lëmbe
Sa ñaari leer yi jolli na
Ñaari ngërëm nga boole, am
Nga ndam sa may ga yaatu na
Firdawsi ngay tëggoo junjung
Yaa Séydi moom nga tuumë ja
Gëm léen te woolu tey dëgël
Di sant Laahu kiy ndimmël
Buur Yàlla moo la may, Rasuul
Nu gëm ko woolu diine ja
Yaa xalla yoon wu réy wu yaa
Wu jëm ca pééy yu magg ya
Sa ngir mi leer na noo ngi jaamu
Bañji diiné pertana
Fekkon nga yoonu diine sew
Ba nééw ji doole yépp daw
Nga xalla yoon wi, yaa fi raw
Ku fonk jamu waaxusil
Goor ak jigéén di taalibe
sikkar sa riir fa baabu ba
Ba xol ya buur digaani ba
Amiin ja, doy na noo jubël
Xamxam ba raw na foore ya
Jaaxal na lawliya yi ya
Yaa jiité lanbiya yi ya
Diiwaan bi yaa di seen ngënéél
Yaa saytu diine jiy defar
Jullit yi, sant leen lu war
Ñiy xantu diine ngir sa leer
Ñuy topp tééré ya di jiir
Ñi weddi Njiin dañoo xamul
Ki mën ci diiné, noo dëggal
Da ngeen a laajul kiy jubal
Nde moo di goor gu laabiir
Jom-jomlu jommi fey na ko
réy-réylu, réér it fey na ko
Xamul na laaj ñu wax ko ko
Ci yoonu diine mooy li war
Damaa gisul ku mel ni Maam
Limaamu Laay te dégguma
Ku wax ne Yàlla moo ma yonni
Moo ko wax nu woolu ko
Gëm seede leen ne sant naa
Ki tax ma seeru Séydinaa
Ba gëm ko, naa ko "aamanaa"
Ku woolu sant war na la
Sëriñ sa toppu tank ba
Saa bay Libaass ne maay boroom
Kuy xañtu weer ba jant fenk
Xamal ne leer ya wër na la
Njaal-all yeek njanaaw yi ñook
Garab yi boole gëm na ñoo
Nit ak jinney werante, noo
La woolu, Seydi tedd nga
Bu gaalug Baay Libaas riddéé
Ba gëm yi naani Kawsara
Kerook, ñi gàntu Baay Libaas
Di ñee ñi gëm ca kump ga
Ñi tëx te buur dañoo tëkkaale
Mahdiyook i walliyu
Ka wax ne Yàlla moo ma yonni
Kooka moo di Nabiyu
Araab yi ak Tubaab yi ñoo
Jëkkoon ci yoonu Nabiyu
Wolof di xaar mujjug jamaana
Maam Limaamul Mahdiyu
Yaaram ba feeñ na ciy leboo
Xërëm ya tiit na bay faboo
Boroom ngënéél la nuy xaboo
Yaa woote diine, noo wuyyoo
Subhaana maa ko yéénéwoon
Nu boole xol yi ndax nu man
di jéém a roy ñi jiituwoon
te aw ci yoonu Muhammadoo
Lu fiy jullit nu bokk Ndey
Da gaan ci Buur bi leeri pééy
Ndax Buur jubal sunub liggééy
ci lampi leeri Muhamadoo
Yonnent yi wootewoon li laahi
dakkantalees na leen ci Laahi
Ku dee te doo"aduuwa"Laahi
di Abdalaahi Muhamadoo
Nabee dikkoon ne jaamu leen
Yonnentub Yàlla ñeel na leen
Ku weddi kii dawal keneen
Te génn yoonu Muhamadoo
War ngeen na xam ne jangu neen
Te jëfewoo ko moo di ten
bu teey bu neex te doo ca naan
Gojam ba ñeel na Muhamadoo
Moo tax ba Baay Libaas ne leen
da ngeen di wax te laaju leen
War ngeen a gaaw ma àtte leen
ci yoonu Diine Muhamadoo
Xamxam ba woon ca Mustafaa
Du jééx te lënt nekku faa
Bu kaan sottee mu tuuru faa
Lu mankewul la Muhamado
Araab du jël wolof déjoo
Ndax gëm yépp janguñu
Ñi mel ni man dañuy béjoo
werante sarti Muhamadoo
"Laa ilaaha illa Laahu Muhamadoo
Rasuulu laahi waahidun
Rabbul Jalliilu Maajidun
Salli alaa Muhamadoo"
Yaa feeñ ci Yoofu gééja waay
Sa tur wi siiw na dootu fey
Boroom jamaano maa la woy
Nga may nu, dig nu, doo naxe
Sëriñ sa jang Alxuraan
Ba xam "Chariihatu" ak cosaan
Ki Yàlla yonni fii Zamaan
ñu bañ ko, xaw ma seen pexe
Giñ naa ci Laahu kiy Boroom
Ibnu Maryaama yaa di moom
Yàlla la tann doo moroom
Ñi gëm te woolu ñoo texe
Diggënte Beyti Maamur ak Yaraax
Diggënte boobu dànd na
Te lef ma yaa na, Ruuhu laahi
Ngawar la, naar wa pepp na
Njool war na gaal ba dem Yaraax
Boroom cosaan yi teeru ko
Da ñoo xamul fumoo bawoo
Ngëlëmte ñaaw na, metti na
Jullee na tàkkusaan Yaraax
Jàkkeer la war fanaani Yoof
Jullee fa Njool ma, gëm ya naa
Ko, Ruuhu Laahi, doy nga noo
Ba Maam jogéé, jëm Jamma Laahi
Ñi gantu woon xëccoo na koo
Ña wuyyuwoon Madiiné Laahi
Ci yoonu diine yobbu koo
Bésub keroog la gééj ga neex
Ngor ak, Wakaam ya seede koo
Caaroy, Ndakaaru, waa Yaraax
Ñu naan ca mbeex ma, jaale koo
Haalim ya jomlu, gééj ga gëm
ba jox Madiine ak ruu-am
Lu tee werante fey, nu gëm
ba gaa ya jiituwoon texe
Jirim ya jooy na ba sëngeem
Njool ma ñëw na, seen rongoñ ya fer
Jullit yi wéétoon bay xelaat
Donoy Madiine wàcc naa
Raxas xolam ba muy fayaax
Lu cay lu bon mu rekki koo
Mu mel ni saaba door a baax
Lu cay lu gën mu dolli ko
Ku déglu saari Alxuraan
Ña gàntuwoon la fay tëkkoo
Ñi jomlu diine ngir kiñaan
Malaaka yaa ngi leen ëkkoo
Ku nekk fooreyë boo nuyoo
Sa mbooti xol mu ràññe ko
Kerook mu jam la doo feyyoo
ba loo xamoon nga fàtte ko
Ni baay Libaas di def "rijaal"
Bu dee mbëriit mu daane koo
Mbiram manee fu ko misaal
Ki gëm te woolu xam na ko
Li Yàlla sante doo ko jaas
Ku farluwul nga jéppi koo
Taasanxa diine, yaa ko daas
Ku bañ nga rendi sañ nga ko
Ku làmb saa buumi cofeel
ci Baay Libaas, na bàyyikoo
Bu wooluwul ki nuy texeel
Guddeek bëcëg nu muslu koo
Samag cofeel di law ni ngooñ
Ku saytu paaka jublu koo
Nu ñaan ci Buur bi bañ ku tooñ
Musël ga yal na jiitu koo
Sa diine dootu fey wallaay
Yàllaa la woolu jox la koo
Yow it nga woolu Ruuhu Laay
Mu jiitu, gëm ya topp koo
Séytaane mel nikkik fital
Di takk jëm ci buumu xol
Damaa bëgoon lu may ragal
Nga mey ma tul gu may "sawe"
Ndax waaji man damaa léjël
Ba mel ni kul ma fëkk jël
Moo tax, ma ñaan si sam ndimmël
Ndax mbër nga, yow man nga ma rawe
May ndaw lu tollu cig bëggam
Muy dox di yonni ay ndawam
Yu bon di sante aw xambam
te xaw ma boor bu muy xawe
Sëriñ si mar na bay xundooñ
Ñu dem ba Màkka weesu koo
Ma jooy rotal samay rongooñ
Da ñoo gëlëm te rééré ko
Ku weddi ndaw te laajuloo
Bu ngeen làyyoo mu sànk la
Ku Yàlla yonni, ngay jotal
Mbindééf yi, booba wacc nga
Ki sot xalima, soos daa
Tektal yu woor la daa xalam
Ña saytu téére ya gëlëm
Nde boon ñu ràññee aw meloom
Kurél bu yiw bi fawxa ngeen
Ku dul yonnent bi ñee na leen
Lu jiitu tey la Yàlla noon
Di ngeen sujjoot ci Muhamadoo
Li ngeen di jëf, li ngeen di wax
Li ngeen di jorta wooru maa
Li ngeen di lééb la Yàlla wax
Amaana moo di àtte ba
Jullit yi maase ngeen ne Njiin
Sore na waaye dektu na
Li ngeen di waa ja léép malaaka
Daldi saytu tàmpe ba
Mbooleem li fooréyiy yaxal
Du ñu fi def lu gën jubël
Sikar te boolekaak matal
Jullee ka ñaan ci Muhamadoo
Bu nuy siyaari Jàmmalaay
Yooryoor ba Maam nangul na nu
Guddik diiwaan la gëm ya yéék
Kerkeraani Muhamadu
Da noo gisul ku mel ni Maam
Limaamu Laay te déggu noo
Ku melni Seydi dootul feeñ
Ci dun bi woor na kiy fexe
Ñi gëm te woolu noon na seew
Nga woote, yow ni yonni ku
Ku bañ sa diiné dey ku beew
Jëfam ja Yàlla xoolu ko
"Baxril buxxuri Mustafa
Wa laa nafaasa xad kafaa
Li kambareen wa Yoofa haa"
Si lim bi nuuri Muhamadu
Yonnen bi won naa num ngirëm
Xallal nu yoonu Ajjana
Nu santa Laahu woy Rasuul
Bu yiw bi saytu caabi ja
Nabee waxoon ne saa ginnaaw
La waay di ñëw di leen fi woo
Liggééy ba faw yool ba nééw
Du tol ni yoolub Muhamadu
Xam ngeen ne jaam bu bañ Boroom
Du am tarànga am ngërëm
Te yoonu laaxiraam, xelam
Du dal, du am ku ko yërëm
La woon fa Màkka ak Medin
Ñoo ka boole Jàmmalaay
Ba suuf yëngoo leeri Jabeel
Ya "turné" wéy fa sowu ba
Yàlla la yonni ngay ndawam
Nu gëm la soobu ci ngirëm
Te Yàlla daal a fiy Boroom
Ku bañ du tee nga di laram