(6) Siyar naa la Baay Laay
BISMI LAAHI RAHMANI RAHIMI
Siyar naa la Baay Laay yow mi doyloo sa Buur, woo ma
Siyaar naa ñi and ak yow, digéék yow ki am worma
Ku siyaar sa xol dootu wow, dey tooy ngireek mar wi ciy baawaan
Ku yaakaar ci yow doo sooy bay dellook merum awmaa
Sa Buur baa la doyloo sol la leeram ya ngay wooteSiyaar naa la yow Baay Laay, siyaar naa ci say Saaba
Nabeey gaal gu réy guy jallé mooy Maam Limaamu Laay
Ku am gaal te am say mool, ne looy tiit fa jàllu ba
Nabeey gééju leer, duusam yu réy yaak na ñuy bëbe
Njanaaw yaa ca naanoon leeri waxyoon la ñuy sabe
Al hamdu li Laahi, nuy sant Buur ngir ga Maam Libaas
Sunu soppe, soppe Laahu, Séydee di xejj ba
Ku diis yaa ko yan Laahu, sa Yonnent ba seede ko
Sa yan boo ma yan ñaan naa la dooley na may fabe
Jullit yeen ñi gëm Baay Laay dëggël Seydi kiilu ngeen
Ku si weesuwul buntam ya booy fëgg muy ubbi
Rafet gëm ci Baay Laay moo di jééma roy ciy jikkoom
Waxew yiw, jëfew yiw mandu moo gën ci taalibe
Ku xemmem ndënal ñoñ Yàlla da ngay déklu woote ba
Nga am xel, te am teggin, di toog ak ñi koy tibbe
Te bul déglu gaa ñi regg bay dox di puukëre
Lu dul diine duy teggin, dañoo mel ni ñuy sebe
Ba Mahdiyu woote gaa ña jiitiwoon dañoo rawe
Ba tey ñu ngiy daw, may daagu ndax man dinaa dabe
Ma dib lar bu dib laayif, te def pank muy tooñaan
Ba saay wax ak saa jëf, seen bon gi tiital ma
Damaa soobu cib gol, sopp gànnaay, ragal namaa
Lu fiy daane, booleek rab yu bon yeek na ñuy tëbe
Ma jébbël la saay mbir, yow miy njàccaar ma silmaxa
Tënëxtooti may réér, am tum bi ommat ma
Li nuy sàkku ciy bon bon, ba tee noo rafet fa Maam
Lu tee noo labat baaxam ga ba weesu dénd bi
²
Ragal naa sa may jëf, xawma jan jëf la nuy mujje
Bu yemmook ju ñaaw muy coono, saa san la ñuy ñibbi
Bu leen deeti xeeb kuy woote, Buur Yàlla moom du ñëw
Dafay woolu ay soppeem di leen yonni woote ba
Ku dem pénc may làyyoo da nga weddi woote ba
Nu faf gëm Limaamu Laay mi xam yoonu jàllu ba
Da noo bon te nééwuk jaamu, nan seeti Muhamadu
Ci dunyaa, na ngeen seet Maam Limaamoo di jàllu ba
Man dey xawma waa dunyaa lu ñuy bañ ca woote ba
Nde Baay Laay li muy digleek a wax, moo di jàllu ba
Di leen japp tey sellal di laay laay fa jakk jaa
Li Baay Laay di diglé ngoog, looloo di jàllu ba
Di leen wax ci seen mbokkum jullit wax ju teey ju baax
Li Baay Laay di diglé ngoog, looloo di jàllu ba
Di leen xool ci seen mbokkum jullit xool bu teey bu baax
Li Baay Laay di diglé ngoog, looloo di jàllu ba
Bu leen fen ta buleen jëw ta buleen bokka sik rambaac
Li Baay Laay di diglé ngoog, looloo di jàllu ba
Guddig "Leylatul israahi" la jaaroon fa jàllu ba
Ba déeyook Boroomam Laahu, may gaa di jàllu ba
Siraat gééj gu réy ay duus, te dey xiiru noonam ya
Nu ngiy gëm Limaamu Laay mi nuy jalle jàllu ba
Dafay xool Boroom tangaay wa, feyloo ko beelem wa
Nu ngiy gëm Limaamu Laay mi xam yoonu jàllu ba
Boroom mey yu réy, dey joor nu tàllal sunuy ndijjor
Ba maanaam li gééj giy fuur, te ya raw tabeel mey ma
Ku am saabu, am ndox tax nga naaguy ñimeñ taq
Da ngay kum xelam des mbaa nga xés wuyu woote ba
Bakken def na noon buy wor boroom def ko muy barmool
Digaan leen nu sàkku man bakken, won ko fiy ngir mi
Sëriñ seeti leen seen tééré, niiraati Mahdiyu
Bu ngeen ràññewul Baay Laay, Limaamoo di xejj ba
Sëriñ dénca leen seen tééré ñëw laajsi Ruuhu Laay
Nabiyu Lummiyoo feeñ ci Yoof, moo di jàllu ba
Ku ci woolu sab xamxam ba yaakaar sa alluba
Ba tax ngay jundum gii gééj, te doo jàll jàllu ba
"Salaatan wa tasliiman alaa Seydil waraa"
Maam Limaamu Laay leeram ya moo raw yu jant bi