(7) Jantub diine yaa tiim gaayu gëm yaa
BISMI LAAHI RAHMANI RAHIMI
Jantub diine yaa tiim gaayu gëm yaa
Ku mar di nga naan ci gééj leer yaa ngi baawaan
“Al hamdu li Laahi Rabbil aalaminaa”
Ndégem noo gëm ki Yàlla yabal jamana
Addina yaa ka mane gan doo nu naxtaan
Nu ngiy yaakaar ki nuy mane gane ca Rilwaan
Da lay mane gan te gaaw berndeel la gay béén
Mu njuuy la nga daanu cim kan rééré ak neen
Sagar ak i yax, lu leen gënë ñaw la dooréé
Ku kay bëgg miim, bàmmeel seere ñaaree
Bu leen ñétaan, ki àddina jay ba dooleel ko
Dina wor, dina njuuy, àddina maa ka tuumaal
Bu leen réyréylu, réy Laahoo ko yelloo
Ku réylu ba dee malaaka ya jël la sewloo
Ba Baay Laay wootewul dunyaa lëdëm na
Gërëm leen goor gi moo ame leeru diine
Ku xam Baay Laay te xam Nabi Laay ne mooma
Mahdiyu Nabi Laay a feeñ, moo woote diine
Jullitoo wooluleen, sang féñ na Soodaan
Ku Yàlla yakkal nga suur, na nu jomb xaaraan
Mbindééf dina xool, di njéér te du gis ngëneel ya
Ba Yonnent feeñ na ci biir Yoof, noo ngi jaamu
Mbindééf a ngi ñuul, te làmboo leeri Yonnent
Ba leer yi di tuuru ci gééj, nuy naan ci mbeex mi
Ku am xamxam, te ragnéé leeri Yonnent
Da nga wara xam ne séydééy jiite yoon wi
Sang Soodaan nga, Seydi donay Madiine
Bu leen laamlaami, goor gee woote diine
Limaamul Mahdiyu Soodaan Yoof la feeñ
Wallaay Laahu la soob du danu ko jiiñe
Du jang ci tééré, du ci xalimaam, du daa ja
Kiñàne dafa réy, nde boon ñu ne moo di waa ja
Ba Nabi féégné, ca Màkka, ba leer ya baawaan
Xérém ya tasaaroo, Nabi tere leen bidaa ya
Ku gëm Nabi, gëm Limaamu Rassuulu Laahi
Gëlëm dafa réy, nde Kaaba ga, Jàmmlaahi
Ba Njiin feeñé ca Yoof, bañ yay kalaame
Ndaxam da ñu réér, nde Yonnent, moom du sànkoo
Bu doon, ku fi féñ ñu agga fa laaj ko yoon wa
Bi Laahi du ñu réér, nde sàmmaan miin na saawa
Bu leen ñétaan buuri dunya ki liitam
Juddook dee moom ku koy def, Buur du nawleem
Sikkar sa di riir, bañam ya naan lee mu sànkoo
Mu naan saabaam ya asal du ma seeru Kongoo
Ba Njiin waree gaal bañam ya di ree, jawaanoo
Ba saaba ya naan ko Njiin doo teeri bàyyi nu
Rogoñ ya di tuuru, bu doon wurus it di marjaan
Ginnaaw jooy yooya, Laahu yaa di Rahmaan
Ba gaal ga bañee ca Béér la ñu gëm, jalooréém
Ba Kongo Belseek Wiirwiir gnoo koy dégg ndéém
Xayartu Madiine, Baay Laay, jeul na ndam laa
Ku dem Ilayiina, muy jaayook njañam laa
Ba Njiin feeñé, la robiney leer ya baawaan
Ba rééw mi limbaane, Soodaan dootu naanaan
Tanxal nu ci yol mi, yow miy Njool nu naanoo
Ba mandi ci leer yi, Baay Laay yaay limbaane
Ku langook ñaari yol loo deeti rootaan
Da ngaa wara naan, di sangu say bagn di ñéétaan
Bëcëg la ko Buur ba woo, ba mu réér mbindééf ya
Sëmbéél ko ca gééju leer ya, mu dem di taaya
Yabal ko mu woote diine ba samp raayam ya
Sañséél ko sa leer ya muy jaayook binnéém ya
Bu daa bilibaane, ñuy gaawtook a foofaan
Malaaka ya door xérëm ya ñu weesu foofaa
Baay Laay woote na, wàcc na, moom jotal na
Mbindééf yay jaamu, mu tiim leen, seede gëm ya
Ba gééj sàbbaa, Aras yëngou, woor na Baay Laay
La seen pexe jeex, tereetu ñu gaa ña Laay Laay
Sang da nga taaru, tabe, ku la séén daldi maaree
Rafet gaw gaay, xanaa marjaan nga dooree
Da nga tabe, muñ, di jambaar, doy nga waaroo
Rafet ngab yar xanaa baatin nga dooree
Da nga rafetal sa diine ba tey ma woy laa
Ku fiy ame diine, Baay Laay jël na ndam laa
Li nuy bon - bon di saw gaay, yaa nu wéétéé
Boroom Ridwaan sang bi yaa nu jiitéé
Da ñu noon wird ak sikkar dina fey ca sowu
Limaamoo woon, te mu nga war gaal di joow
Ba pake bay déqi ba pat may xotti mbeex ma
Malaaka ya naan ka Seydeey jiité soodaan
Ba tey leer yaa ngi baawaan rééw mi fess na
Ñu ngiy laay laay, di roy Baay Laay ci diiné
Baay Laay noon na Séydeey jiité gaa ñaa
Ku bañ Baay Seydi na nu jox, maa ko wooloo
Boroom "Ridwaan", ku la woy naani Tuubaa
"Al hamdu li Laahi Rabbil aalaamiinaa"
"Al hamdu li Laahi Rabbil aalaamiinaa"
Sangub jamaanaa ngi, Soodaan woy ko lay jééx.