BATAAXALU SËY
" BATAAXALU SËY "
1) Ay kaddu ñaax yuma fas laay jök di jeebaane
Jiital ci saa bopp door di soobu santaane
2) Di jajja xol yi di xambaat taalu fas fasu sëy
Ndax Koofi naw diko yeem saloona waxtaane
3) Ci sëy yi Laay diote ndax way deeñca yeemako sas
Tooknaafi ak Coddu Mbaye mu tiisma Mor saane
4) Mor saane goontu si jaambat Coddu ak diko xas
Ku nekka sakku ci mane ay baati deenkaane
5) Yaw Coddu deel wanna baat lammiñ wu saf na lewet
Göör baat la am ci kërëm deklul bunee maa ne
6) Saw taank nay gatt ap doxkat du mucc ci ay
Sëy kat dafay maytu dox bul tamma seetaani
7) Doylul te ngay maytu xeep loo am fasal te gërëm
Xëy fas te togg du yam ay xëy di xamnaani
Göör ken du xëy diko xeebal wërsëgëm diko ray
Ndax yaw xamoo lamu dacc bul wër di xeebaani
9) Fobul te wëy wuyu ndeem daa jeep sa tur ni nërëm
Neel kocc deklu waxam daw soobu santaane
10) Maytulma andaya ndax sëy kat warul bari xel
Ndax ay jigeen kunu may xel sax nga saytaane
11) Nga baalmanak du xasin sax dëggë daa ritaxul
Sooy ut xarit na nga loonkoo ak ndijaay saane
12) Taggool lu jiii nga nar dem took di xaar ndigëlam
Te bul di weesu dayoop taggoo ya saaraane
13) Moyul di mer Aka taangat soxna day mayu ay
Deel wax ndijaay diko Jay ñaareel dafay waane
14) Deel fööt di noddanti tey laal gëtt ak defi yëf
Jigeen dafay xajamal ndeem bëgg naa daane
15) Sammal sa lammiñ te dëkkee wax lu wöör la nga xam
Moyulma ñepp daje ngir Yaw tenaan yaani
16) baagante kër Ndayi tam day njoortaloo ku xamul
Kër Baay du Nda al ëtt tax saa boo maree naani
17) Foonkalma wayjur Ya foonkal rakk yaaki magam
Nooy bëggë taane xarapleen boulko caaxaane
18) Bu kenna xam sa merook moom doonte mer gi warul
Deel mokk pooc diko cokkaas naako paa saane
19) Foonkal sa wujj wi ndax moofiy samak tafuko
Ñool ñool jigul Göör jigul sax weñ gu ñuul laaane
20) Bijjaawu Göör ñoragul day sonna bopba di rax
Ndax jeek yu Boon yamu yor bay wër di tëddaani
21) Kubaax nga waaye da ngaa am jikko mbedd yu sew
Taxxool sa Göör gi te muñ as gor du toogani
22) Yaw saane deklouma nak yaay Göör te Yaa wara dal
Jigeen ju jak sax muñël sakkam ju keemaane
23) Nëbbël ko sikk ya ak ayip ya bulko di ëñ
Maytul di gaaral ci biir nit ñeek di waxtaane
24) Ndax xam nga mbööt mi ci muuraayal jigeen ca yabal
Akit marax wanu taamoo war ga yaw taane ?
*
25)Muuraay ga mooy sikk laaalay jox fabal te defar
Bulsakku mukk di siiwël ak di jeebaane
26) Ap sëy budee suturaakoy gaddu rax ci di muñ
Deeskoy dogal Barke ak wërsëk yu saawaane
27) Bul dëkke gëdde di xas sööral yu jak yamu yor
Bul may sa noon ya lunuy lëñbët di seetaani
28) Dëkkëlko dëkkooko bul gaantal lu war la nga man
Woddal cërëm bamu jak bum xëy di xaaraani
29) Foonkal sa ay jii tenay mat ndeem bisëm dafa jot
Nooy moome kër Coddu dem ci ngoone caaxaani
30) Daanal sa xolbi te bës ndeem toppatoo gi matul
Du sak ci yaw mère tax ngay wër di reeraani
31) jigeen ji ndeem dafa am ay sikk raxci yu jak
Xoolal yu jak ya te muñ jikkoom yu keemaani
32) As ndaw sudee dooko baal moomit du jok dila moy
Seen anda ndeem yagganaat du jok ci saf kaani
33) jugël Nga sukk te raam Yaw Coddu baalu bu wër
jebbëlko sap loxo tuup nga baalko yaw saane
34) Muñlënte leen benna sëy muccul ci coowaki ay
Te yeeni neeena buleen deklooti shaytaane