Baye Libasse Niang
1) Ma delsi ubbi wennë laf
Te daadi soobu wennë lef
Te roy ca gaaña wanna lef
Waay Mbër ma taaraloon wolof
2) Karataxal la danga ngoon
Jubbënti it laca dëngöön
Bamu joyee kako lëngoon
Ba gek ko , njarko , fafko luf
3) Sëriñ Libaas ñang mooma yeem
Waykat Ba addu ñeppë luum
Joobe Sangam, ba jot ngërëm
Semmal na, gaaña daan walif
4) Dapna wolof , ci ak lëndëm
Fëgi pëndëm , aki lindëm
Föötup dandam, sajjiy ndëndëm
Bindëm tingööm soloy wolof
5) Taaraaba, segg bepp baat
Lakk wi, mootax mu jubaat
Mooko nosal, ay caxxi baat
Raangalko, joongamay wolof
6) Mootax ba, waykat yi wedam
Ken jooyatul geenti idam
Tay fööre Yaa, ngui ñëw di dém
Di yobbëloo leebi jolof
7) Jaar nga wolof , suufak sa kaw
Jaar ko, ci ñaari walla Yaw
Jaar ko , ci peenku ak ci Saw
Funekk , jaar nga fa wolof
8) Kajoor gi , jël nga seen waxiin
Saalum gi , jël nga seen waxiin
Jiwaalook waalo Yaa fa xiin
Say waame, naandalna wolof
9) Gisnaa ne doy nga delluwaay
Lakk wi tay, Yaa tee , mu naay
Yaa jok taxaw, di nday di baay
Lakk wi , Yaako tee , suruf
10) Fekkoon nga, muy salla wu yooy
Yaako yafal, ci ñax mu tooy
Wulliko , taggatko , mu nooy
Du xoox, Du mamma, du tërëf
11) Fekkoon nga lakka wii sëngeem
Def baayo, gennë aw sangeem
Ngaañ jam ya gëmmë, leppë giim
Yaw Baay Libaas ñañg , Yaako ëf
12)Fekkoon nga, soonoomsa nduxum
Nga dokk ko , bay ñaxi waxam
Ndönoor ga, Yaa seggi laxam
Tey ñoo ngi muucu , lem gu saf
13) Daabaam ga, wallet ngay wexam
Fuddënko, lakka ak laxam
Ku soobuwul, sa mboor du xam
Leeraayu lammiñu wolof
14) Wolofa ngi, wuyuw turëm
Wolofa ngi, wodday sërëm
Di ñibbi siy, fanaam kërëm
Gërëmla warna kuy wolof
15) Baatam ya suulu, Yaako jeex
Ci bepp gox, baniko ciiix
Xobbi xomaat ja , bamu weex
Xocci xalaamam , jam wolof
16) Ken musla degg, ku, tërël
Ci lakku giir, wamiy teral
Lu dap la baay libass tërël
Ci tëri toggaley wolof
17) Xuus nga fi geej, yifi xaliil
tegoon, sadaf ya, yaako, jeel
Jalla nga geej, gaaluk cofeel
Sëfsa lu waykat musta sëf
18) Soppi nga, booleem tereliin
Yan daa fowee , ka tër ci neen
Yaay waame , Yaay ki jara sëën
Yaay teppu, yaa deggi wolof
19) Fekkoon nga , way fatta tarac
Ñu laf kubeer nga , fafko tëc
Yaa gaddu xeppa yi, di toc
Ba tijji, lammigni wolof.
20) Lakkwi yaako feenialaat
Taaralko ñeppko ñalaat
Yaa tax ba lakk wii jugaat
Ay sakketam badiko maf
21) Yaa way , ci laakka wii batax
Mu ñong , te neex, meenti marax
Yaa sippi ap raxam watax
ken manta, saankati wolof
22) Ku ñgaax ni aan , kuni mani
Cantam nga warnalaa gane
Say bindeu dunko saggane
Xamnanni moo dabou wolof
23) Alxamdou Lillahi ndaxam
Lum musa rabba, ciy mbubbeum
Dakoo solal Njiin Minu geum
Xiyaaru saadati salaf
24) Ngir Maam Limaamoo tax mu jam
Ci benna saan, niaari picceum
Laaxoom ya sooy na, kay athiam
Libassa jam jami wolof
25) Baay LAYE Amul Maas rek way
Maam Sëydi teewluko, ni cëy
Jox lam ndigël, ngay jööri say
Ciy Tagga, yeemnaa lii nga laf
26) Yaa joobe Njiin, ba am ngëneel
Jibriil, dëkeelaa yankiwal
Say wax di jaasi, fumu dal
Dok loosi noon ya , ñuy tërëf
27) Moo lare, jam ci wenna saan
Jotal ga, jommalna Hasaan
Moodaan Wesar cik takkusaan
Lu Jeggi xel, te musta raf
28) SaHbaanu sak fasaaHatoo
Waral mu goontu, taaggatoo
Sunu demee, ba taggatoo
Aw tagga faatu ci wolof
29) Buusayri sak balaahatoo
Mbooleem taggam ya laxxatu
Sunu demee , ba tëggëtoo
Ken dootu walli , jeul wolof
30) yaa tax ba waykat yepp giim
Ñuy gatt, yaw gadip geuleem
Seen tuuri lefma yaako lem
Yaa ray ñadaan sewal wolof
31) Yaa taalifal Njiin Minu geum
Yaa tax ba soodaan diko yeem
Yaay werekaan wi, yaay Hakiim
Mbireum ya yaako wan wolof
32) Bi nga demee la ñepp sooy
lakkawi, lammiñam di jooy
Laabam wa booy, gaancax ga gooy
Yaa suuxatoon , dëri wolof
33) Nit ñaangi koy saf aka wooy
Diko neuxeul bamouni wöööy
Di mbeummeu kay, biññi ni looy
Ba nga demee, la wax yi dof
34) Ba nga demee lanuko fogn
Ba nga demee lanuko bagn
Daa melni daa xulooki tougn
ken nanguwul deggi wolof.
35) Jeggaanewul niou koy jëgël
Te njeugg ga, mantikoo jagal
Tey amatul, kukoy ñagal
Wolof yi walluleen wolof
36) Jotna , ñu bokkap taxawaay
Te takku , sampa ay jataay
Te yeesalaat lii beugue raaay
Fay daay gi takka ci wolof
37) Yaw taxawal SaaliHu Hann
Nooy Xuuse Geejuk mbaambulaan
Ay noppalootil tey dagaan
Ñu duy sa ndap ci limfi jëf
38) Na YALLA dollima xorom
Te donnalooma ciy xorom
Xaarma, lu okkatup deureum
Bamafi may wayee wolof
39) Yaa Rabbanaa salli 'alaa
Limaamou qaa idil malaa
kajaaka saxbihil 'ulaa
Ak baay Libasse nian Sunu Chef
Le 23 septembre 2017