Boroom Rawdu bi
Taalif Bii maa ngi ko wayé ca Rawdup Seydina Limamou LAHI ziyaar ko yeesal samak cofeel ak samak gëm ci Moom yalnako nangu Ci Barkeem psl
1)Boroom Rawdu Bii , biir jaam ñi la tanna, yonni ko
Di yaakaar bi ñep, doon xaar ngireek mooy ki Yonni ku
2) Boroom Rawdu Bii , lan raanga luy may, yu laandi ya
Te joxko kilifteef gaaki xeewël Maxaama ya
3) Boroom Rawdu Bii, fum feenka, leeram ya, yiir naleen
ku mooñoo ci yiw wekleen, ba Yonnen, Ya nawnaleen
4) Boroom Rawdu beey Njup waa, ju bañ jupluu kii du jup,
Awaay Laampu Njup baa ngii, Boroom Tum, bi neeexa top
5) Boroom Rawdu Bii, moo ubbi, L'islam, tëjaatko fii
Te rëër giifi taawoon, mooko ngiisal mu daxxufi
6)Boroom Rawdu Bee tax, Buur sujutloo Malaaka ya
Di Barkeeelu leeram, yeem ngënneelam yu magga ya
7)Boroom Rawdu bii, mbooleem Yonenta, ya xamnako
Ku wooteet ca ñoom moo tanxa, keemaan ya seddako
8) Boroom Rawdu Bii sax, kun soloo wax Nga ak dikkëm
Tenaa Jëwrinam lan, saa bu wootee na ngeen ko gëm
9) Boroom Rawdu Bee aal, Yuusufap taar, ba fitanaloon
Zulayxaa, Té tax Yanxuub , dajeek Doom, faddu woon
10) Boroom Rawdu Bii, Ibrayma woowoon ca ngaarema
La Nuuhun muccee , moomak Njabootam ca mbëndëma
11) Boroom Rawdu Bii ismaïla mootax jotunko ray
Ka Muusa notee noonamba, Mooy kiifi wooté tay
12) Boroom Rawdu Bii bokkaale, farnako, bañ farak
Lufiy mbaax, di weettël YALLA, mbooleem guddek bëccëk
13) Boroom Rawdu Bii sampaa ki, xaambaya Mooko tuur
Lañaawit Mu sellal leen ca, wooteem bi doyna Muur
14) Boroom Rawdu Bii, Lay geeji xarbaax ya, yaana lool
Kukoy xuus di lap, limbaat wédamloona bepp xél
15) Boroom Rawdu Bii Daa wër, lu wees junni At yu wer
Ngireek seet ñoñam, tey saytu dunyaa ci bepp boor
16) Boroom Rawdu bee, Daa ray, ci ëf , Daa ca dekkalit
Diwaxloo Njanaaw yaak, danfi, doxloo garap yi it
17) Boroom Rawdu Bii, wexxal na geej neel randalnako
Te wuññee ki fac, Ndërmeel , ca teenxëmla defnako
18) Boroom Rawdu bee daa sol, ku Jangul Mu nettali
La teewul la wëy, Mbër mun fi naw, Mooko aggali
19) Boroom Rawdu beey Baye LAYE Mi feeñ fii ne "Aajiboo"
Nitak Jinne Maay Seen Ndax Litax luy xërëm fobu
20) Boroom Rawdu Bii, saak Ruu jëlël saak cofeela ngook
Awaay xolbi yaa Moom, yar ma , yeegalma defma Sak
21) Boroom Rawdu bii, Maadoon ziyaar si sa Rawdu Bii
Duyëlma ma feesal Maam, ubbilma Sa Baabu bii
22) Boroom Rawdu Bii, kon aksinaa yësfi jaaduna
Te goor naa ci yaw nandalma, woomalma ak munaa
23) Boroom Rawdu Bii ñaanal nu Buur samma Abdu LAAY
Mu am wër Takalkoy ndam , Mu wettëli Ahlu LAAY
24) Boroom Rawdu Bii, Boleem Salaat yaalna sax Ci Yaw
Te anday Salaaman , laamba Mbooleem Ku ngoy Ci Yaw
18 Avril 2017