Cangaayal Janaaba
Bismil-l-Lâhi-r-Rahmâni-r-Rahimi
« Xaala ibnu » Jibriil di santa Yàlla
mi mey Limaamu mey yu réy yu sella
Jakleel ka xamxami « luduniyaati »
xamalka « maa madaa wa maa sayaati »
Sellal ka jox ka laabukaay yu sella jox ka na ñuy sangoo cangaayal set la
Ndax jaamu Yàlla gu àndul ak set ga
deefu ko nangu faf ko def muy moy ga
Loolo waral ma jok wax ngir Yàlla
di laayebiir jullit ñu gëm ña Yàlla
Te manu ñoo wéral cangaayal farata
xamu ñu it lu ciy sunnaak luy farata
May wax di jééma nas la Isaa yaxaloon Ibnu Imaama Laay mi ñépp wòòluwoon
Moom la bindoon yonnéé ko kuy muxadam
ci yoonu laayeen ndeke booba dey dem
Wuyyuji Buur Yàlla te bëggë yeesal la
ñu ka dénkoon ndax ñu man di sellal
Ba mu yonnee lile cangaay ci rééw yi
ak bamu wuyyujee Boroom mbindééf yi
Ñenenti weer la ak ñaar fuk ak juroom
ciy fan ndegul ma wax la ndax nga bañ ca juum
Loloo ngi xew gaawu bu yemmook ñatti fan,
ci maamu Koor te moom mu jok ñar fuki fan
Yu ték juroom ñaar ya ci weeru Kori wa
ca menna atma muy ca xéytél weer wa
Atum junni ak ñatti tééméér ak juroom
benn fukak juroom ñatta la njool ma dem
Te moom juroom ñaar fuki at ak ñatti at la tollu cik dundam booba ca mooma at
Nan dellu jëm si nak li nu jubluwoon
moodi cangaay la Seydi Isaa yaxaloon
Niki ñu kay sangoo da ngay jëkk raxas
sa ñaari ténka ñatti yoon nga kay raxas
Balaa nga leen dugël ca ndap la doora siw
ca foofa ngay siwe ngay fas yééné yaw
Bul fatte “Bimi Laahi” ca fangay raxase
say ténxo doora siw bu leen di jaxase
Ginnaaw ba nga siwéé ba noppi raxasal
fu fi sobe taxoon ci yaw ak fumu dal
Bu jàppandee nga randu tuut taxaw feneen
ndéém raxasit ma taa na , looloo gën ci yoon
Nga daldi tek raxas sa ñaari loxoya
dale ca mbàgaya ba ca baaraam ya
Ta nga jëkk raxas loxab ndijoor ba
boo àgagalee daldi ca tek càmmoñ ba
Nga daldi cay tek sa wetuk ndijoor, daleel
ca mbaga ma mu jëm ca yeel ba bul tayeel
Boo aggalee tek ca wetuk càmmoñ ga
nga def ko na nga def wetuk ndijoor ga
Nga tek ca dënnë ca baat ba
di ko raxas muy wacc jëm ca yeel ba
Nga tek ginnaaw ga tàmbalee ca doq ga
mu jëm ca yeel ba loolu mooy xobeeku ga
Nga doora jàpp cër bu neck benn yoon
boo dee raxas sa bopp def ka ñatti yoon
Dangay sëggël sa bopp boo ka dee raxas
nga tàmbalee ca dong ga boole kaak raxas
Say nopp biir baak ca mbooleem biti ba
moomiit nga def ko ñatti yoon ni bopp ba
Nga tek ca raxasaat wetuk ndijoor ga
nga jànga “faatiha” boleek raxas ga
Nga tàmbalee raxas xa pàqu bopp ba
mu àndandook “faatiha” jëm ca yeel ba
Boo àggalee tek ca wetuk càmmoñ ga
mu àndak “faatiha” nig u ndiijoor ga
Nga tek ca sab dënnë dale ka ca jé ba
mu àndak “faatiha” ba ca jumbux ba
Nga tek ginnaaw ga tàmbalee ca dong ga
ak “faatiha” raxas mu yam sa ndigga
Ndéém raxasoowoon tanka ya ca njapp ma
nga daldi leen raxas, set nga tojma
Nga jël sa ñaari loxo tanka cam ndox
sotti ci sa kaw bopp ba boole kaak wax
Ne “Bismi Laahi Rahmaani Rahiimi
al hamdu lilaahi Rabbil aalamiina” daldi
Cay tek “laa ilaaha illaa laahu
Muhammadu Rasuulu Laahi salla Laahu”
“alayhi wasalam” foofa la cangaay
la mate farlul ba di def lile cangaay
Deklul ba xam lu cay sunnaak luy farata
ndéém yaa ngi jëm ci def càngaayal farata
Am na ci way xam yi ku wax ne ku xamul
luy sunna yak farata kooka sanguwul
Ndax am tojam setul cangaayam neen
la te mbooleem julli yunu ca julli neen la
Am na ci ñoom ku wax ne yit ndéém sangu nga
na ñuy sangoo te juumuloo ci set nga
Ndeem xam nga ne cangaay li santeb Yàllaa
bu war ci bépp jam bu gëm Buur Yàlla
Waxal ne faratay cangaay juroom la
yééné ja booy dug ca biir cangaay la
Méngëlé cër ya, lim ka mooy ñaareel ba
ragga ga mbooleem cër ya mooy ñatteel ba
Matale cër ya ñëw na di ñeenteel ba
xàllil kawarga moo matal juroom ba
Sunnay cangaay la mooy nga jëké loxo ya
raxas ka ba taku kaayi jara ya
Balaa nga leen dugëlca ndab la ñaati yoon
raxas sa biir bënbënu nopp ñatti yoon
Galaxndikook soraxndiku yii sunnala
leneen lu des xamal ni lu ñu sopp la
Bu dee ku léttu soxlawul muy firiku
ci booy raxas bopp ba waaye war na ko
Mu jël ca ndox ma def bu baax ca létt ya
bës ka ba derba tooy ci suufi létt ya
« Al hamdu lilaahi » ba la nu jubluwoon
matee ci nas la Seydi Isaa yaxaloon
Maa ngi gërëm bu baax di santa Yalla
cim ndimmëlëm ba woy wi mat bu sella
Nan santa Baay Laay mi nu tee rootaa-ni
taalam ba leeral na sowook « Buldaani »
Nuy ñaan ci Yallam ndimmëlëm ba nu metal
lile cangaay ci fépp fu ñu ka waral
Ak fuñu ka sunnal “wa salla Laahu
alaa Nabiiyinaa wa man waa lahu”