Marsiya Baay Raan
1. Al hamdu lil laahi nan gëm nangu ay dogalam
Si Moom lanuy dello moo moom jaamñi ak luñu am
2. Innaa lil laahi wa innaa raaji’uuna ilay-
hi Yalla mooy joxe mooy jël noo ngi nangu jëfëm
3. Dunyaabi workat la moo woor Sayyidul-umami
Moo wor Sahaabayi waajii Àddunaako xajam
4. Wal mawtu baabun wa kulun- naasi daaxiluhuu
Ubbilna Maam Alasaan buntëm nu ñàkk jëmëm
5. Ni Dee budoon jotu kon Jullit ñi jot Alasaan
Ci ruuh yo doy ni Sëriñ Raan raw na lun mana am
6. Bu ruugi doon jaay nu defsiy ndambi ndambi wurus
Ba defsi Àdduna gep ngir Seydi Raan baña dem
7. Taa’an wa Kaafan si weeruw Tamxarit cala dem
Nuy seenu far waneen weer suux nu sax si lëndëm
8. Si Baktashin si atum Gàddaay ga Goorga laxas
Bes booba tiis na ku tiitul daa newul diko gëm
9. Ëllëk sa ñep rotsi Yoof kuniy taxaw di misaal
Mbaaxuk Sëriñ Raan di jooy naa wëy fu Àdduna jëm
10. Kep ko taseel mulanaa jaal naala Maam Alasaan
Kubaax teyiw demna tay ngir fekki Maamja Limaam
11. Dunyaa lëndëm na kerook xol yepp weet na itam
Shawxan wa lahfan si Baay Raan miidi bahrul-karam
12. Funuy giseeti ka donnoon Maam Limaamu si ay
Jikkoom yu màgg ya Baay Raan yaanu làqqu badem
13. Woyof na loolu ni ab xob waaye sooka xamul
Baatin ba sànkala mooy Marjaanu moo raw ngalam
14. Jikkoomya day geej Sëriñ Raan xuusko day jafe lool
Te awma gaal kon xanaa ma wax si tuuti lu yam
15. Taxwaa ilaahil- waraa moo fees xolam ba mu gëm
Maamam Limaamu te woolot Yalla Buur binu moom
16. Xoolul lu jëm si këruk Dunyaa te feesul xolam
Misaal si Dëddu lawoon moo sella moo bari ndam
17. Moo baax te laabiir te am yërmànde am yitte lool
Kum gis teral nala Baay Raan moodi Kanzun-ni’am
18. Daanay digël jaam yi gëm Buur Yalla bàyyi tereem
Kon gaayi nan gëm te tuub tay jooxe ay ndigalëm
19. Lu nekk defnako siy xarbaax yu rëy na nga laaj
Gaayamya Ajgaak Mulaay Hasan nga xàmmee cërëm
20. Xamoon na Seyyiduna Iisaa te jël na si moom
Haybaak xorom saak fajuk aajooka yaatal kanam
21. Toppon na Baay Seydi Cëw fonkon na Baay Abdulaay
Bëggoon rakkam ya Husëynook ñoom Bashiiru rakam
22. Daa def lu baax diko wax xamul lu ñaaw duko def
Amoon na mecce ba daawul wër di ñaan lumu am
23. Ma jooy ku melnii dafay yay nanla jooy Abadan
Weetël sun xol yi Baay Raan tax nga ñepp wedam
24. Bakaas- samaawaatu wal arduuna yaa ’ajaban
Iimaan bi jooyna nitëm Ihsaan bi bi jooy xaritam
25. Ay Buur fayal Seydi Raan Firdawsi ak lufa am
Dekkalko xurba Imaamil-laahi bes banu jëm
26. Feetël njaboot gi palaasam maynu Baay Abdulaay
Mu wer te tal menli Nuuhin Rabbi yokkal fanam
27. Kanzul karaamaati Bahrul ’ilmi wal hikami
Cëy doomi Seyyidunaa yaa donna husnas-shiyam
28. Sa mbaax gu rëy gi nga am wa reewmi seedenako
Ludul ku tëx walla book iñaan ga muur ab xolam
29. Yaa tax ba ken jooyatul Baay Raan ne yaanu dëfël
Antal-Xaliifatu luy leer yaako donn na’am
30. Na Buur defal lam ndimbël yaak Ahla bayti Limaam
Fal-laahu rabbun kariimun moodi Buur binu gëm
31. Saxalunu Yalla ’alal hudaa te may nu salaam
Te maynu ’aafiyatan bi jaahi Seydi Limaam
32. Taw niiru xeewël si Baay Raan saa su nekk ba ker
Nuy xëy dajeek moom ca biir Firdawsi ak kinu gëm
33. Yaa Rabbi salli ’alal Muxtaari Sayyidinaa
Sallim ’alal aali wal ashaab te maynu Hikam