
Waajal sa Bes
Si way wii damay xalam dundug doomu aadama diggënte biluy juddu ak binu koy delloo Boroomam, xalam liko war si toppatoo ay Cërëm, am Xelam, ab Xolam ak Ruuwam, xalam liy dundël ben bu nekk si yooyu ak likoy delloo ginaaw, xalam nimu wara sakko ngërëmu Boroom bi balaa muy delluwaat ci Moom.
1. Awaay Àdduna may wor ba kum teeru taggela
Bulay wor du waaj day xëy yabal Dee mu seetsila
2. Du seet ngòòr su tekkeegul du seet ndaw su masta sëy Du rus liir si jël yaayam ku jotle mu xëy bala
3. Rusul waa ju sos daaraam di xamleeka jangale
Du ab Xutbu mbaa Yonnen ku matle mu yobbula
4. Diggënte bi ngay juddok bimuy yonni Dee si yaw
Ludul xam sa cër sammonte ak moom waraatula
5. Ludul xam sa jubluwaay ludul moytu jaddukaay
Ludul toppatoo sa waay, ni xëy faatu jombula
6. Ludul toppatoo say Cër ludul nàmmataat sa
Xel Ludul suuxetaat Xolbeek sa Ruugi du doon fula
7. Di yëngooka faggooy tax sa Cër yii dëkee sawar
Di jàngay li tax sam Xel dëkee sell woornala
8. Cofeel moodi suuxat xol si yaatal njabootgi ak
Dileen toppatook say mbokk wegleen ñu bëggëla
9. Jariñ luy sa askan jox pusob mbaax gi ñiy ñëwaat
Lu melniiy dundël sak Ruu lu moy loolu reccu la
10. Ni nitñeey njabootug Yalla kepp kuleen jariñ
Mu kontaan si yaw tampeel la tanneef ya joobela
11. Ku lii lepp war nan lay talee wax di taalu ay Weranteeka teesanteeka weqqante nib mala
12. Xanaa kii manul may nit ñi deppaas buñuy añee Duleen xañ sagoy dem wut ko yenna yi nattula
13. Xanaa kii manul took xamle wartula reerële
Ku manta defar booy yaqq Yàlla ji jeppila
14. Nattuy Cër yi mooy tayyeel nattuy Xel mi moodi reer Nattuy Xol bi mooy soxor te waatnaani fitnala
15. Nattuy Ruugi mooy bañ sant Yalla si xeewëlëm
Ba lànk si bañkoo jaamu xëy Deega gansila
16. Ki xëy joxla deppaas warna man taamu ab añam
Te Yallaay ki moom loo yor dalaa tànn denkëla
17. Werëk tal du sax xamxam du sax am amit du sax
Te loosi defoon bes penc mooy yeksi seedela
18. Te boo moyuwul Dunyaa bi worla balaa ëlëk
Ki xellooy ki wor Dunyaa te saggante gaccela
19. Fobul tay te waaj besbooba ngay daje ak Boroom
Te sakkum mbegam daw lepp lum bañ ba artula
20. Na Buur suturaal jaamam yi samm la taawu la
Sagal la ndamoo la may la feg la te farle la
21. Te maynu Seriñ Ablaay mu yagg fi jiitenu
Ñu am ngërëmal Maaman ni amko teraangala
22. Away Yalla jullil dolli sëlmël si Ahmadu
Te naŋ nu yërëm bes booba nuy xëysi fekkila
Yëmbël Dibeer
5 Juin 2016