google.com, pub-1214054292722785, DIRECT, f08c47fec0942fa0
top of page

Marsiya Sheriif Husëynu Laahi

Way wii maangi ko taalif ngir Marsiyaal si sama soppe di sama xarit Sherif Alhusëynu Doomi Seydinaa Isaa. Toppandoo si wayu Karbalaa binu joyewoon Husëynu demb, mootax ma dupee ko Karbalaa2. Di ñaan mu doon yeesaluk sama kollëre si Baay Sherif mii nga xamni dunu gaawa miis ak demam. Yalnako Yalla nangu te yalna Yalla yokk leeri Baay Sheriif Husëynu Laahi.

Karbalaa 2

Unknown Track - Unknown Artist
00:00 / 00:00

1. Al hamdu lil laahi nu sànt Rabbanaa
Moo yabalaat Yonnen bi muy Imaamunaa


2. Moo bind Mawtu ak hayaatu mooy dogal
Ken dufi des kudul Boroom bi Rabbanaa


3. Moo tax mu jël Yonnen bi xayru xalxihii
Kiy yërmëndey mbindeef yi tay Rasuulunaa


4. Xamul baayamba Abdulaahi moom Yonnen
Aminataat daa teela genn Àdduna


5. Maamam ja yorko muy jirim cëy Àdduna
Woraat ko ñaari at la am ak Seydunaa


6. Mu ñakk Yaayja ñakk Baayba ñakk Maam
Te moofi gën Buur Yalla mooy Xaadirunaa

7. Miimun si ay atam mu woo waa Àddunaa   (40ans)
Mbokk ya bañ te naako doo mab’uusunaa

8. Ñaar fukka ak ñett si ay atam la jog    (23ans)
Di woote waa Madiina gëm Habiibunaa


9. Ginaaw Ajam ga Njoolma dellu Taybata
Feebar ba dapko ap digëm jigeñsina 


10. Feebar ba dëjko Sahba yep booloo di jooy
Ngir tiit demuk seen soppe kiy Muxtaarunaa  


11. Ñu fap Yonnen mudem sañoom naa degganaa
Man ngeeni jooy tee ngeena gëm Maalikunaa


12. Ku Yalla mus yabal doo beel si Àdduna
Samap digit du jaas ndeem soobna Rabbanaa


13. Samap digëk yeen moodi geeju Kawsara
Abaabakar jooyna kerook ba jàqqana


14. Yawmul Isnayni ruuga dellu Aljana
Ka leeraloon Madiina genn Àdduna


15. Bisamba tiisna ñaa ngi jàqq ñaa nga ngi tëx
Ñaa luu ngirek naqar Jullit ña jaaxlena

16. Umar taxaw jël jaasi naa ku wax Yonnen
Faatuna naako ray naqar wa yeemena


17. Abaabakar tiimko di jooy naa sella nga
Bi ngay dundak tay jii nga dem Ilayyina


18. Dellu waxak mboolooma Maa Muhammadun
Illaa Rasuulu Gaayi digba yeksina


19. Fatimatuz Zahraa’u tiim ko naako Baay
Suuf sula ëmb tedd yaay habiibunaa


20. Nirook demuk Imaami Laahi xayrinaa
Guddik Jumaa ja booba bes tam tàngana


21. Lu jiitu digba ñaari ay bes Maam Libaas
Jiite Jullit ña cëy koreem ga mettina


22. Limaamu naa gaawleen ma àgg Jàmmalaay
Anaa Janaazatun digëm ba yembana


23. Yaram wa jeex mu melni banta bun solal
Ay yere leer ya wër kanam ga taaruna


24. Mu naan ku yeene jox Yonnen bi ab dërëm
Na andi joxma manla maay Rasuulunaa


25. Mu woo xarit ba Sheex Jibriilu ghawsunaa
Jàngal xutab yi muy turaath si Ahlunaa


26. Feebar ba dëc ko muy sikar di waaj xanaa
Lun mana am warnan xalaat Imaamunaa

27. Guddik Jumaa ja Fukki fan ginaaw Kori      14ème jour
Ak ñeenti fan Limaamu genn Àdduna


28. Jigeen ña yuuxu Sahba yep di jooy te naan
Nax nganu rek ba dem awaay habiibunaa


29. Manjoon taxaw jël jaasi naa ken dufi rob
Libaas te Seydinaa ñëwul lii yellana


30. Ñuy xaar Isaa ndax Bayti Maamur lay bawoo
Ñuy jooy Limaamu ñetti fan ya mettina

31. Mu ñëw di foon kanam ga naako waalidii
Tibta hayyan wa mayyitan, wa Rabbinaa


32. Naaleen kudaa jaamu Limaamu man nga dem
Kuy jaamu Yalla took nu gëm Xaalixunaa

33. Miimun la took ken jooyatul Imaamunaa       40 ans
Ba Dee jëlaatko mook Manjoon ak xutbunaa


34. La jël Limaamu jël Isaa miy xayrunaa
Du bàyyi ken muy sax di beel si Àdduna


35. La jël Manjoon ak Baabakar miy xutbunaa
Moo jël Isaak Baay Raan midoon xudwatunaa


36. Kon kay du tee Husëynu daanu waat xanaa
Kem Karbalaa la Alya Samba wuutena


37. Luy tiis kerook si Karbalaa xamnan ko bes
Ba Baay Sheriif sëtub Limaamu làqquna


38. Ñiinaa du moom Husëynu manta dem xanaa
Sunub xarit du ñibbi weetël xalbanaa


39. Kërëm ga fees ñii jaaxle ñii di yuux sa kaw
Doomi Isaa ja xëyna tàggu Ahlanaa 40.

40. Saadun wa Daal la dund melni ñaari fan  64 ans
Dun masa miis demuk Sheriif Sadiixunaa


41. Mboolooma dac ci Jàmmalaayi Kambereen
Kuy taalibeek soppeb Sheriif riñaan sina 42.

      42.  Allarba Benn fan ci Yuulyuu Tashashin      1er Juillet 2009
Teemeeri at ginaaw kadoon Mahdiyunaa


43. Nan seet Sheriif si lun fi manti dal ëllëk
Day mujja daal woyof ni xob fii nafsinaa


44. Sëtub Yonneen lawoon di doomi Ruuhulaay
Doyoon naciy garaat temoo doon Shayxanaa


45. Luy mbaax ci Seydinaa Limaamu moom la jël
Siwliise ak yanja la jël ci Seydinaa


46. Yuusufa lay misaal ci taarak ak xarkanam
Te xoobe taar ba ak meloom yu sellana


47. Woyof na loolu màndu gëm xaalixunaa
Doon Taalibeb Maam Seydi ak Imaamunaa


48. Ab tab la woon geejug teraanga lay misaal
Mbokkak xarit jirim faxiir yi jàqqanaa


49. Xamxam bu sell buy bayaan ken dootu wax
Doktoor dëlaa jënes Jënes bi ñàkkana


50. Jënes bi ñakka nan ki doon seen royuwaay
Seen soppe seen xarit Husëynu ñibbina


51. Ambaasëdooru Maam Limaamu xëyna dem
Itaali ak Fràns du miis Sheriifunaa


52. Waa Jasporaa bi ñakk ngeen kadaa jubël
Daa jangaleek waaraate fii buldaaninaa


53. Farlu si Diine ji ak waañu Roohu Laay
Waa Kambareen ay ñàkk ngeen Sëyyidunaa


54. Yëmbël Gorom waa Malika ak waa Dakaar
Seen Konferansiyee bi demna Aljana


55. Fekki xarit ya Seydi Caw ak Seydi Raan
Ibook rakamja Baay Saxiir faxiidunaa


56. Ku taar jayoon mbaa askanak xamxam alal
Naxool si Baay Sheriif sëtub Mahmuudunaa


57. Na tuub te dellu gëm Boroom bi Rabbanaa
La jël Sheriif du bàyyi ken ci Àddina

 

58. Ku tiis daloon na muñ te xamni Rabbanaa
Mooy joxe mooy jëlaat te mooy Xaadirunaa


59. Ku jaaxlewoon na xamni Abdulaay Sheriif
Moofiy Sheriif te mooy Boroom zamaanunaa


60. Nam fonkewoon magam ja Seydi Abdulaay
Ba naako Baay nanko matal si Abdunaa


61. Nam fonkewoon jaamu Boroombi nanko jeem
Fonk sunnas Limaamu xayri xayrinaa


62. Fa Baay Sheriif feetoon njabootgi Rabbanaa
Naŋ nufa feete yaa xadiira amrinaa


63. Tawal ci moom feek picc ngiy sab yaa Kariim
Nuuran wa Rahmatan mook Ahli Baytinaa

64. Bàyyifi Abdulaay yaakaaru Àddina
Mu sax fi lool te wer ne mooy xaliifunaa


65. Yaa Rabbanaa Yaa Rabbanaa Yaa Rabbanaa
Dollil nu leer Sheriif Husëynu Shamsunaa


66. Salli wa salliman ’alaa man ursila
Wal aali wal ashaabi mooy Mahdiyunaa


Yëmbël
Aljuma, 14/06/2013
Sheriif Leeram du Fay
Mamadu Baara Samb

 

bottom of page