Imam Mame Libasse LAYE
taalif bi Laa jakleel Maam Libasse ibn Seydi Abii Bakar ibn Seydina Imaamil Lahi psl
1) Ci lakku yaaram wi laadoon jeema diir dayoba
jeggalma tay Sa ay wolof Maam Njiin sagup nujabaa
2) Ap sanga deesuko cof deeskoy dogal yëfi yëf
Waral maway ci wolof luy baati naar yama ba
3) Kuy ndoong daara nisër naa sadda way ci sa cër
Yaa farlu foonk sa mbir ba gaaya naa Xaleba
4) Göör YALLA deesuko xam ciy njoorta baa diko lëm
Jëflënte leen di nga am ngandaay kerook xareba
5) Göör YALLA piir dafa war muy laay biir ñak wër
Kaawteefu waa ja nga dar in mam yaxuj arabah
6) Yayoo nga tagga yi ndax Njariñ sa kem la ci ndox
Ku yëk sa mbir yi di fëx binnaf'i muktasibah
7) AHsanta cëy li nga def AHSanta cëy li nga laf
Afnayta cëy li nga maf du rëër du fay ba subë
Xaabaabaluk tagga sax bëggooka ndax fegi wax
Laakinna juudaka kay lottalna man katabah
9) QaSiidatii ci wolof Laa tanne baat yuma këf
Di bakka waajima saf naam reere woo 'arabe
10) Na YALLA dottila may ñooddeeti fanwi nga wëy
Toftal ci wër bamu doy CI Barke Sun Sangaba
11) Sallaa 'alayhi Ilaahul 'Arshi ak ñako dar
Saabaam Ya ak ña jagoo man akhlaSuun Nasabah
Le 21 janvier 2017