Ku mandoo ni moom
-
Ni leen Yalna Buur Yalla dolliy ngërëm
-
Ci Seynaa Manjoon mii tee sottiy meyam
-
Donoy sanga baa ngii ci laabiré nit gni
-
Ci diine akuk ëflé ciy xéewëlëm
-
Na gneen déglu tey jii ma wax ay meloom
-
Bu ken weddi, ndax moo ma yar maa ko xam
-
Sunub sanga doonul sërign buy tege
-
Te xam ngeen, yéwén naat cib ab xaalisam
-
Du kuy yonni ay ndaw ngireek sàkku ndimmël
-
Te sax booko seetee, mufar jox ku gëm
-
Su dee gnaan ci Baayam, su baatam jibée
-
Da ngay gaaw ne aamiin mu raw ay xalam
-
"Tabaarakta yaa axsanal xaalixiina
-
Ni leen"baaraka Lahu, baari nasam"
-
Su fekkoon gni fiy woote gnëppey wurus
-
Da may wax ne, moom laa fu gis muy ngalam
-
Sunub sanga laa gis du gniiroo du xiiroo
-
Du tongoo, du songoo, te doo gis meram
-
Du fab tanki rakam, du gor siisi doomam
-
Da koy def ni boppam, du gottib cërëm
-
Du léewoo, du féewoo, du mbiicoo ka mballo
-
Du ngaayoo du jéllo, du tiisal nonam
-
Nitam gnee ko të-ngëm, dadul tax mu bangam
-
Te dey jaamu sangam di màgal waxam
-
Ignaanul, fignaagul, du kuy am di nay
-
Du kuy suxlu gnennat ngireek bakanam
-
Du kuy jiixi nimmat, du kuy siisi bokkam
-
Du kuy mer ba fengat ngireek bakanam
-
Ku màandoo ni moom, mbaa nga sàmmoo ni moom
-
Mbaa nga jaamoo ni moom kay, xanaa mosula am
-
Baay Manjoon kay xanaa yaa di bawkat bu mag bi
-
Te yow doo nelaw, saayu nit nee xeram
-
Sëtub Maam Asan bii na ngay xagntu yoon wi
-
Ludul yoon wi bon na, lu bon bul ca jëm
-
Xabbool tanki jàkka te bul manké gnaan ya
-
Te ngay fonki ràkka, ndégém bëgg nga ndam
-
Ki gàddaaye Màkka ngireek fonki ràkka
-
Te gën leen jàkka na ngeen koy xalam
-
Ngireek been ràkka limël ben junni
-
Ci fooraay, da fay ful meloom ak jëfëm
-
Ki daa yonni ndaw ya, di daaral waxam
-
Kilee yonni Baay Laay ci nit gneek ku xam
-
Ba moo tax ma wax lii, ci jàkkaam yonnen la
-
Xanaa kay da ngeen gàntu, dootul xalam
-
Ci xeet wii ci Soodaan Limamoo ci woote
-
Di daaral adiisak xur-aanak ikam
-
Ku yër saaru xaliil, te seet baat ya gis
-
Ne doo kuy werante Limaamook kërëm
-
Ku yër mat-u Rasuul, Omar moo fa wax
-
“Wa isxasdu uxraa”na ngeen xam ikam
-
Ka daa jéggi jéegoom banaa fii la dal
-
“Xataa xatwatan” mooy Limaamook kërëm
-
Gisal riiru sowu bi, gisal tanka baa ngii
-
Ka gnuy weddi dootul Limaamook kërëm
-
Su fekee ne yaa woote yaay noonu nit gna
-
Ci Njiin laa joyal loolu, xam ngeen cërëm
-
Cërëb ndawli, mooy gëm te seet ay soloom
-
Ludul lii du aqam, te xam ngeen ikam
-
Su fekee ne yaa woote yaay "kanzu" fii
-
Rasool kay da nuy boole nihmaak gërëm
-
Gisal gnam yu neex yi, gisal kër yu baax yi
-
Te seet col yu baax ya, na ngeen koy xalam
-
Taxaw naa ci Baay Laay soloom kay du jéex
-
Ma wax tey ci Seynaa, meloom ak jëfëm
-
Isaa mooy jaraafam te mooy naayibam
-
Xanaa mooy li ngeen jànga, xam leen ngalam
-
Boroom mey gu yaa gi ci penkook sowoo
-
Ci “daf-uuki jàlbu” te xam ngeen mbirëm
-
Isaa kay bu dee ndaw, ci yonnen xanaa
-
Koon it kay nu diy jaam te gëm ay mbirëm
-
Ignaanul te bonul du kuy tiit di wax
-
Du kuy dox di làkhu ngireek gnakk xam
-
Bu daan dox da daa daagu tiitul kemam
-
Kemam sax dadul am te moo gën ngalam
-
Bu gnuy mos di woote, di feegnal di xool
-
Bu nee mël gnu sàbaa te naa mooy ngalam
-
Isaa kay xanaa yaa di samaan mu mag mi
-
Ne foo buusu gnoognaa nga daw ndax gëlëm
-
Da daa digle tey woote booleek di wax
-
Koon it kay na ngeen jëf te wottoo gëlëm
-
Ku miin sab jataay kay bu yaggee mu gis
-
Jikkoom yaak meyam ya, du làqus camam
-
Du fiirate mooy gor su am yërmëndé
-
Yonnen moodi baayam, te xam naa ngalam
-
Sa tur waan ga penku, demal biir sowu
-
Ba tey yaa ngi diiwaan, nde yaa gën ngalam
-
Taxaw naa ci Seynaa te woy Baay Manjoon
-
Ci diinéem akuk fokku ciy xéewëlëm
-
Saxal cik woyoflu, te bul dox di reylu
-
Te bul wut màqaama nde koon doo ko am
-
Sa tool baaya, deel bey te wottul ku ruur
-
Te bul dog garab koon nga sàggib sagam
-
Ku aw yoonu laayeen du woote ka seexal
-
Du wooteek màqaama su doone ku xam
-
Ku aw yoon wi laa wax, du wootey màqaama
-
Di laaj ay "idaaya“ di tiisal gnognam
-
Su fekkoon da nga woote tey kat di seexal
-
Koon it yoon wi gàntu, nga dal nuy ëlëm
-
Te sax yoon wi xam ngeen ni gnëppaa di farlu
-
“Fa sukran li mawlaaya muulii-nihma”
-
Na ngeen nooy te teeyal, bësit seeni xol
-
Ba ngeen xam ni jaam kat du doon ab sangam
-
Su fekkoon ne jam sax da fay doon sangam
-
Du jiitoo ti, seetal ci fardook ikam
-
Na ngeen bàyyi ngagngnate, tuumaal Sërign
-
Ku am seyxu, war ngaa di wormaal ku xam
-
Bu len ngagngn koo xam ni looy deflu jëlkë
-
Sërign soxla naa la gnëwël génnë xam
-
MBaa Sërign kaay ko gnaanal, lu gnaaw am na kat
-
Ne buur Laahu gnëwna ba fabb waaja dem
-
Mbaa Sërign kat sa waajaa nga feebar ba goor
-
Sa lor lagn ca yaakaar dikkël ndax nga xam
-
Bu leen gnanna tib seex, Sërign deel teral
-
Di jox aadiyaak ceeb lilee dib cërëm
-
Taxaw naa ci Baay Njoon te woy Baabakar
-
Te dengkaane say mbir ne yaa raw ku xam
-
Sërign Mbay bu ken tax nga juutal sa njëmbët
-
Bu juutoo du jébbi du am reen itam
-
Sa xam geenu gindi sa man gee ka siiw
-
Ni leen Yal na Buur Yalla dolliy gërëm
-
Xanaa Mbay da ngaa boole màndook tabe
-
Koon it man da may boole woy ak xalam
-
Xanaa yow da ngaa woolu Baay Laay mi gën
-
Koon it man da naa boole gëm laak ngërëm
-
Su fekkee ne yaa boole jàmmaak salaam
-
Koon it kay da naa boole cantak gërëm
-
Kileey baayu xeet ba, turëm laafu woy
-
Na ngeen deglu woy wii t exam naa ngalam
-
Su fekkee ne baayay dogal mbir ci doom
-
Limaamoo dogl loolu xam ngeen cëram
-
Su fekkee ne baayay xamal doom ngënëel
-
Kii, Limaamoo ko jàngal na ngeen xam mbirëm
-
Su fekkee ne doom am na bennub xarit
-
Koon it yaay xaliil maa la am maa la xam
-
Ma jeexal ci Baay Njoon danay Seydinaa
-
Na ngeen gnaan mu dolli salam ak ngërëm
-
Fa yaa Seydy, “bii illatun fii fu-aadi”
-
La kay taxa wér yaa ka am yaa ka xam
-
Su fekkee jarak am na bennub “tabiib”
-
Koon it maa ngi nii, maa la am, ma la xam
-
Su ab sët dikkee gëm sàngam benn yoon
-
Koon it maa ngi nii maa la gëm maa la gëm
-
Su dollee ngëmëm ga ba muy gnaari yoon
-
Koon it maa la gëm, ma la gëm ; maa la gëm
-
Su dollee ma dolli, mu dellooti dolli
-
Ma dolli, ba dolli lu raw aw xelam
-
Su fekkee ne yaa boole mbaax ak yewén
-
Man it kay da naa boole cantak ngërëm
-
Su woy wii defee mbék ci yow kay xanaa
-
Da naa woy weneen woy wu xel dul xalam
-
“Wa laakin na nii haamidun shaakrun”
-
Bu as gor meyee, jàam itam nay gërëm
-
Su woy kat manee woy ba xéy dal ci man
-
Ma woy def ko jàassi mu xottib xolam
-
Ne Abdoo di wane géwél moodi cuune
-
Bu jàngul Aruut ak bayaan ak ikam
-
Nde woy naa ba tàyyi te gis naa ne woy wii
-
Dabul geeji mey ya, da maa far wedam
-
Fa yaa Seydi tey ab njegee ngii ma joxla
-
Da maa xam ne yow rekka mat jëkërëm
-
"Xad in kahdu ka al bikra yaa Seydy"
-
Walaa xarwa ndax am nga ay warwaram
-
Muril séét bi seet ko damay bagn nga teet ko
-
Te teeyoo ba gis ay meloom ak jëfëm
-
Gisal ree ju neex ji, gisal saf xorom gii
-
Ka gnuy toggu dello du biip xarkanam
-
Su fekkee ne baayay dogal can ci doomam
-
Ci yow laa joyal loolu xam ngab cërëm
-
Sa séét bii du dox kat, du wax kat, du fay
-
Du ngarmbaasu wëjjëm, du yab jëkërëm
-
Baay Manjoon yaa gnu màndi, sa mbaax gee fu làndi
-
Sa xam gee nu gindi ba deeful gëlëm
-
Sërign Aadi laa roy ci woy wii xanaa
-
Bu leen bagn ku roy kat da may kuy xalam
-
“Ixta duunii bi fihlii, ka xawlii” xanaa
-
Koon it man da may roy ci Aadeek ku xam
-
Na ngeen gnaan gnu dollil nu aw fan te wér
-
Mu gnaanal nu ak sax te mey nuy dërëm
-
Sërign sab goroo ngii da fay waaja dellu
-
Bu delloo bu gneegnoom ya yaxub deram
-
Da gnuy xeysi sargal ko booleek di seenoo
-
Guraak warigar, bëgg xam ay Mbiram
-
Sërign Abdu geesul dawal ya ngi lab
-
Ne géej yii ku leen xuus da ngay far wedam
-
Sërign Abdu yaa ub ne bakkul xanaa
-
Ne yaa woy Libaas, ak Isaa aki rakam
-
Gnu baax gnii ku leen woy da ngay am ngërëm
-
Yonnen doomi yonnen bilaal gneey ngalam
-
Bu saasal manee xonq tax kay melax
-
Xanaa kay ngalam jaar fa melnib jalam
-
Limamook ndjabootam da gnoo jàlla yii
-
Yonnen daal dadul kem, xanaa gnooy ngalam
-
Sunub sanga nekkul di foor yaak walliyu
-
Tegal poo bi, peese nga gis koy ngalam
-
“Fa yaa Rabbi salli alal Mustapha”
-
Nu gëm ay waxam tek ca roy ay jëfëm
BISMI LAHI RAHMANI RAHIMI