Limamou Jotalna
1) Limaamu Jotalna , yonniba seen boroom Ya
begël way jup ya, xuppë ña wacca yoon Ya
2) Fu xeet feeñee, ca ñoom Buur def ca ndaw Ya
Ba Baay LAYE feeñ , ci soodaan daxxa layya
3) Buleen xool der bi , taxleen gedda seen cër
Ki ngeen am, Moom la ñeppë di wër , Ca Mbër Ya
4) Bu laandik gööp mi , taxleen fatte Njiw mi
Budul woon Moom, lëndëm not nooki neen Ya
5) Danoo nuuroon ci rëër , tey Bakou cik moy
Mu tas duusëm Ya , tay nuy xotti yiw Ya
6) Kilee ñëw fékka L'islam giim , defup dööm
Mu ëfko ci Mbaax, Xambeeko gërëm ngëneel Ya
7) Ñu daan bokkaale , sampal way jarak Ya
Di tuuram soow, mu ñëw far tuuri Maam Ya
8) Di deendal YALLA , Baaxoo ray ca Kuur Ya
Mu laabal leen , Ñu juplu Ka Sakka RuuH Ya
9) kassak , feccak , di way, da jëm ci ndiiraan
Mu Fay daayup lu bon , ci Ndoxum Sikar Ya
10) Ci Baatup " laay lalaa" , la dikkee ki Böötëm
Lu juuyook YALLA , xëy toxu , daw berëp Ya
11) Munaa deeleen sikkar fëp , bañ di saggan
Mu lakka yu ñaaw Ya , bejjil xeeti yiw Ya
12) Ne julleey mbaaru Diine ji , moo di njaalbëën
Ci lanlay laac , moyul mabbal juñëm Ya
13 ) Te bul naal jëf ju baax , yeexeel safaanam
faseel bakken , woral Dunyaak naxeem Ya
14) Te gaaweel genne , axxi ña moom zakaat ja
Lay " Yawma HaSaadihi " limkook daliil Ya
15) Ki Yoonal sëy ci teel , lakkal xaleel Ya
Di yobbup neew di Sikkar, bayyi wax Ya
16) ki up fii Diine , mooko fi ubbi dembë
Te mooy Baye Laay Mi seddë ku am ca May Ya
17) Nde Mooy kifi YALLA jox , neko seddëleelma
Te moo yor Gaal ga , jëm Tuuba ca tool Ya
18) Tereek dikle , Limaamoo jël Liwaaba
Te lum masa dikle , raw ca di Sangu Jaam Ya
19) Jikkööm moo doy Boroomam tax mu wayko
Te Xarbaaxam Ya , rawna limuk bideew Ya
20) Te Buur nee Ndawla , warna ci Moom jotal ga
Mu wacca banaa " jotal naa " doyna Aaya
21) Dëggël naa wax ji , Mbaay mee jebbi soontu
Ku xëy ñëw jël cërëm , xambaat ca taal Ya
22) Libaas Yaa Baax té Yaay yërman Nde xeet yi
Kulay Foñ jot , Meram Buur ak Mbugël Ya
23) Na Buur jakleella lay Wasilaak FaDiila
Te Joxla Maaxaamba Dottila ngërma ndeeem Ya
24) Ba Nook Baye Abdulaay Xalifap Jamaana
Mu wër jammalko fum mana neek Rakkam Ya
25) Awaay Maam yar ma , yeegal maat , farooma
Xamalma , Sagalma , duyma Sa Geeji May Ya
26) Awaay Maam aarma, loo bëggul fegalma
Te woomal maat nga seddëma Biss Payoor Ya
27) Na Buur Sëlmal Ci Moom booleek Njabootam
SaHabaam baal samay Waajur Ndawam Ya
Saliou Hann
11 MuHarram 1439 H
Le 05 octobre 2017