Mame Alassane LAYE
1) Ma juk man, te fas yeene way gënji doom
Gunuy jaawaleek Baay Ba , ngir ak nurööm
2) Damaa doon, ku jaangul, te am yeene way
Fi saa sanga bii, feeñalaat fiy soloom
3)Su fekkoon ni, doon naa, kuman way, dinaa
Koway tay , lutax keppë, kuy wax ni xiiim
4) Ñi man gott tay jii, amun mbaam mani
Waroon naa gawarloo ba sëf ay taggam
5) Damay takku tay, jeema Roy gaaña xam
Di göörgöörlu, ndax lee ma xëy melni ñoom
6) Amul maass kimay way, ku rëërey mbirëm
Na deklu ma ñëw waxko , lennay meloom
7) Ku ñëp xamla , saaboo tuddee aw turëm
Laniy tek de, mooy cëy , ngiruk yërma ndeem
8) Ku am ngor, te am kersa, am ay ngëneel
Di jaambaari l'islam, ju gëm Sun Boroom
9) Dikoo xamni, nit ñeppë, dankooo safoo
Ngireek YALLA ak Maam Ja , booleek tabeem
10) Waxam ak jëfam, ñoo dëppoo lum tere
Musul defko, lum dikle, daa sax ca Moom
11) Jikkööm moodi Xur-aan, te mooy wettëlam
Te fum manti jëm , moo newoon aannda ndoom
12) Kitax Tool bi soontu, ñagaat diiiné Ji
Waxal Moodi Baye Rane, mi laxxam ngërëm
13) Yëngoo mak, dalam ,moodi YALLAk Yonen
Te saa booko seenee, lubaax mooy yiteem
14) Ku foonkoon , julleek jaanga, liggeeey bu wer
Dadaan faggu, ngir lekka, ñaxxap loxoom
15) Ku foonkoonla, tuubit ilaa Rabbinaa
Te foonkoon itam julli, waxtuy jurööm
16) Ku foonkoon teral ganla, doonoon ku xay
Du tiisal kaneen, ngir ga jot ay yëfëm
17) Ku foonkoon, joxeew ñam, du kuy boddi gan
Ku rus, wër di laac kenna , roy waajurëm
18)Du gaantal kukoy laac , du wor mukk nit
Te Kuy jooy , Ba gis muuñ nga dootoo sëngeem
19) Budaan ree dadaa muuñ , budaan wax dënnëm
Dadaan riir , Sudaan dox, di bootiy loxoom
20) Sudaan jox sëriñ Raan, dafay melni moom
Laniy jox, dafay belli , loolooy meloom
21) Sudaan teewlu Haajoo yadaan jöör ca moom
Dafay gaawtu , bek lool bamuy feeñ ca Moom
22) Su daan deklu Tur YALLA ak Maam Limaam
Xolam fëëx, mulay saf Ku taggook sagoom
23) Kum mas xool nga taaggoo ki tiiss, kum gërëm
Nga taxxoo, ki koom fawwa, taaggooki gööm
24) Ku am xel, saxoo roy ko , moo jar di roy
Ku roy ay jikoom, Sanga faw say moroom
25) Ku neet, xam ko cik noppi, ak cik lewet
Kuneet xam ko yit, cik matal kollëreem
26) Lubaax daal la mooñoo lu ñaaw mooko bañ
Du maslaa ci wara ken, lu rëy ap cërëm
27) Dadaan fattalik mbaax kufiy ap sëriñ
Dadaan aartu, sax nguur , mu def war waram
28) Ba ndaw yeppë saankoo te dëkmël alal
La ñëw daaldi yeeleen ci am jaangaleem
29)Xamalleen , te yarleen , te tekleen ci njup
Ba ndaw loofi gis, maas gi, mooleeni tiim
30) Jëfëm jee ngi nii dootu fay doonte nak
Jëmëm demna yobbaale xalbun saliim
31) Na Buur dollikoy leer , mu sax rek di wëy
Te taasnoot ci Barkeem ñu tuufoo njiwëm
32) Te yaggal fi rakkam Ji, Baye Abdulaah
Kukoy jeema noonoo, na taalam ba giim
33) Wa Salla 'Alal Mustafaa MurtaDaa
Wa Aalin , Wa SaHbin Salaatan taduum
Saliou HaneLAYE
Le 19 septembre 2017
Zone contenant les pièces jointes