Mame Coumba NDOYE
(Litax ma def taalif bii dama ci juplu feeñal Cërëp Soxna sii addina rëëre ak soñña mbokki taalibe yi ñu xeeñtuw Mbirëm Ba wanep ligeeyëm Ndax doyna addina royuwaay.....
1) Ma jeema juk , dellooti mbattu ndaala
Njukkël Ka ap , Cërëm ba rëy Ca YALLA
2) Yonen Ba moo , feeñal rëyup Dayoomba
Tiisluk demam , te yeemu lol ca Yenba
3) Kon ku di xelllu , tey xalam , di xamle
war Ngaa fesël , Mbaax , jikko yam aandaale
4) Leerak Yonen , deeñca ko , doyna tiitër
Rawatinaak , Ndaw Lifi gën , tey joxe cër
5) YALLA ko yar, tannako tam laabal ko
Jël Maam Limaamu Laay mi gën deenkaatko
6) Mooy Cumba Ndööy , Mi ñep xam , ci Jagata
Ngir joxe ñam, terle ni Maam Amiinta
7) Tab gaa waral , MDoomam Ja daan , fa tektal
Kepp ku xiif, muy dëkke , leel leek naandal
8) Moo farlu woon , ci dikle yiw , tey dimbële
Mboleem Jigeen , luy xeewëlit , muy sëddële
9) ku nawlu woon , Yaakaaru woon ci ak yiw
Du lor , dukuy xalaata jëm ci ak moy
10) Daan jaamu rek, ba naafilaam di farata
Ba buur dëkooko , mayko sangup Maam Farmata
11) Dëkkeena YALLA , Bam dëkköö ko , Falko
Muy sangu Kuy , Jigeen ju jak, Sargalko
12) Gëëj Mbambulaan , bay fees di fuur ci xam xam
Dawal sangam , Ba laxxa ndam ak ngërma ndeem
13) Ken musta gis , muy foñ , di jaambat , baa xun
Nangu la def daabaam , batax neexul sëën
14) Muñëk , Woyof , labiir la xambe woon njël
Ku yëëne Taac , gëneel de , dingfa dem jafal
15) Mbayam mi tay , soontu na lool , bay jaayu
Mootax Ba Buur , Sampalko xeeti raayoo
16) Jaantup ngërëm, ci moom la gaaña leerlu
Di niiru ndam , tanneef Ya daanfi seerlu
17) Budul konak , Maam Cumba mii mat taara
Fu rëëwmi jëm , ni kon dugup di baara
18 ) Xam ngeen ni mak , nekkul ci at yu yagga
Booy natt mak , seetko ci mat ak yegga
19) Mooy tax nga xam , fii soxna Cumba tollu
Ci reewmi ak ci diiiné , day Ku doylu
20) attam yuneew yi , teewu koo raw gaaña
mat ga ca moom , moo jaaxaloon way xam ña
21) Jaambaar ju xëy , ci ap sangam mu sasko
Fu saswa jeexe , jaajëfam ja dapko
22) leek leek nga gis , baykat bu wacc njolloor
Tefum taxaw , jawriñ ja yeene kay döör
23) Maam cumba nak , pasteef ga ak njambaar ga
ñoo rafetal , mbayam ma ak laabiir ga
24) te lako war , ci diine ak kërëm ga
yaxxunuwoon , wormaam ga ak ngoram ga
25) wormaam la fop , feetalekook Boroomam
Ngor nga ladaan , jëflënte ak moroomam
26) Loolooko may , sangam ba xëy gërëmko
Buur YALLA yit gërëmko faw , farooko
27) Du Maasu ken , Tanneef lawoon, royal mako
Doon Jeek bu jak , Raw göör ña , Buur dollil nuko
28) Yërmande ak Ngërmande ak Jeggal ga
Ci Barke Sap Soppe Madoon Donoom Ga
29) Julli Ci Moom SaHaaba yaak Ngertëlma
Muccëlnu baalnu maynu xeewël jamma
30) Ñu aanda ak Libaas besup payoor ba
Te dëkki ak wayjur Ya neegi Tuubaa
Mercredi 07 MuHarram 1439 H
27 septembre 2017
Zone contenant les pièces jointes