Marsiya Seydina Mandione LAYE
1) Ma faf sat xaliima , te roy kiifi roy
Sëriñ aadi, yeesal wayam cip Sangam
2) Ku Baay Abdulaay way, de yeemnaa kemam
Ku doon Seppi tiisuk Libaas Jar nga xam
3) Ku Sëyna Issa daan gërëm ngir nangoom
Ñu war toppa saawam, ba tuufuy ngërëm
4) Ku Baay Babacar daan dawal , ak di raam
Kufiy xellu, war ngaa di sakkum mbegëm
5) Sëtup AlHasan LAYE doney Mahdiyu
Miy Sëyna Manjoon LAYE, mi rëër ñep ba dem
6) Dadaan xëy di goontooko xaarum ndiggël
Ci Maam Seydi Issa, di nëbbup cërëm
7) Joxoon leppi woormaa ni Haaruuna ak
Kalimul Ilaahi , Ci Issa magam
8) Te moo laandi ay may, batax koo ramaas
Bideew, jaanta beek weer wi, def cip ëmbëm
9) Te mooy geeju ci xam xam, ya nëbbook ya feeñ
Du maasook Ci may yaak, kiraamaak Hikam
10) Lu waay raw ngireek cër, ba ñëw, jebbëlu
Lu waay fées, ci ay may, ba gis Njoon nërëm
11) Kilee gaanjareey jëf, te reftaal Jikoom
Du yukkët du jaambat, lu mettiw nattoom
12) Limuy poñ la raangoo, Ca Buur ak Ndawam
Du xool lenni mbaaxam, ngireek waac Bisëm
13) Musul tooñ Boroomam, musul jup rëddëm
Ragal YALLA, Woormaal Ko, moodoon mbubëm
14) dëkee dilke yiw, jiit ca, rawleen ca fuuf
Te naa maytuleen YALLA, daw am meram
15) Du kuy diisalap jaam, ngireek neexitam
Du tiisleet, du tiiislu ngireek sakku koom
16) Te moo yaatu, laabiir , di as Gor su wer
Du kuy boddi Soppeem, du ñukkël kanam
17) Du niiru, du aaw, Njoon du kuy yaxxa der
Te daw yee, taxoon noppi, dammup gisëm
18) Tabam ga wedam loo na, waamee ki geej
Batax guur gi, daa xëy di laac siy dërëm
19) Ku daan jaamu Buur YALLA, mooy wettëlëm
Ku fiy moy, bu woomleet, mu daw ap ëttëm
20) kilee Jeppi dunyaa, te xam ay naxeem
Mu muccël ca , kuy xellu, dekluy waxam
21)Ñongal Tool bi Baye LAYE Bayyon, bañ mu ruuur
Wëyël yitte Maam Seydi , dolliw xambam
22) Da ngaa fekka dunyaa, dajal xiini wor
Nga taskoo ci yeete, bafar luy lëndëm
23) Da ngaa fekka Bakken yi, diir jëm ci mbon
Nga fek ko ci Sakkum ngëneelak ni'am
24) Sa waar, Waa ngi soontu, kuneey xëy di gööp
Lu Buur jaajëfël, kon yaayoo ngaa gërëm
24) Wallay Yaay ki jar xam , kulay xam di way
Ku roy fii ci Yaw raw, ëllëk gis mbegëm
25) Xanaa janta, day mar maral, ay Gisin
Nde, kon ñepp xëy gaawtu, sakkum mbeggëm
26) Awaay Maam, sa sët baa ngi nii jallema
Defarmaat; farooma, takkalmay ngalam
27) Awaay Maam, jarak jaaa ngi kaay jëlma fac
Te fööt maat, ma set wic, Defalmay ni'am
28) a Maam golbi daa raglu, kaay jallema
Te wanleema ak Njiin, mu nangulma tam
29) Damaa xool, Sa geej gii, mu Yaa lool neeex
Ma ñew rot ci xaaaraan ki landiy ni'am
30) Na Buur dolii Lay xeewëlëk ngërma ndeem
Te sëlmal ci Baay Laay mu laal aw ñoñam