Nattuy Yonnent-yi
Nattuy Yonnent-yi
Way wii mangi ko tambalé besu yooyooru Jamalaay tollook besu Appel yamook 31 Mai 2014.
Masiy xalam coono yi Yonnent bi toggoo ndax wootembi Demb ak Tay, ak niko noon yi sonnalewoon. Disi xalam ni Yalla nattoo kepp kumu yabal tambalee si Aadama ba si Mustafaa. Yalna Yalla Julli si ñoom ñepp.
1. Al hamdu lil laahi kum may seet ko Yallaahu
Ay xeewalak ay nattoom ñooy ànd Yallaahu
2. Ku yeene jublu si Moom sab xol woyof nga wedam
Ndax ay nattoom rëyna sib xol tiisna Yallaahu
3. Am tahsaboo doyna waar ku bëgg Aljana faw
Ba’san ga dal ñifi jiitoon dal la Yallaahu
4. Hattà yaxuular-rasuulu ayna nasrul-lazii
bil haqqi arsalanii ndax tiis wa Yallaahu
5. Seetalma Aadama bam lekkee Garab ga kerook
Buur Yalla mer mu Yaras am kersa Yallaahu
6. Ibliisu Noon ba di ree Buur Yalla Wacceko far
Xolam ba feesna naqar ak reccu Yallaahu
7. Mu ngay wandeelu ca Suuf ba Buur xamalko la tax
Mu baalko fawwa kerook lay sant Yallaahu
8. Seetalma Nuhin ginaaw idriisa woona nitëm
Lu mat junniy at ñu bañ wooteemba Yallaahu
9. Njabuutu boppam ga soxnaak doomja ñepp ko bañ
Àndak ña doon noonya ak saaysaaysa Yallaahu
10. Ñay neewdi dooleya gëm muy woote ñep diko daw
Ñaawalko naako bawal sa gaañi Yallaahu
11. Ñuy jaamu seen xeerya Nuhin sonna loolu ba xëy
Ñaan Yalla Tufaan ba ñëw muur suuf sa Yallaahu
12. Buur Yalla daaldi alak way weddi yaak ñafa doon
Diiŋat sa ndox ma ñu lap ñook Doom ja Yallaahu
13. Hùdun la waa ’Aad sonnal xeewëlya taxna ñu bew
Ba xeeb ndawal Yalla mook gaayam ya Yallaahu
14. Mu naan xanaa degguleen Tuufaan ba ak ña sa lap
Tee ngeena bayyi xërëm yii jaamu Yallaahu
15. Ñu lànk kaare ba bes ngelaw la màbb la doon
Seen kërya ray kufa nekkoon birna Yallaahu
16. Samuudu xëy wuutuleen si bañ ndawal buur taxaw
Di yedd Saalihu ak ñaawalko Yallaahu
17. Mu wàcce Aaya sa ñoom taxul ñu degg waxam
Seen reerga tax ñu fexeel Gëleem ga Yallaahu
18. Xaarleen lumat ñetti fan mbugël mu rëy dina nëw
Yuuxuk fajar ga raxas leen fawwa Yallaahu
19. Xaliilu Laahi ma jur luy ab yonnent ginaaw
Ibraayma miy xaritab Boroom bi Yallaahu
20. Teewul Boroom bi nattoo bàyam ba jaamu xërëm
Ibraayma sonn ba dee si waarko Yallaahu
21. Taxaw di semmal ñadoon jaamuy bidiw aki weer
Sewal xërëmyaak ña moomoon reewya Yallaahu
22. Ñu mer taxaw di fexeel Ibraayma taal bamu boy
Bëmëx sa xalya kadoon seen ndawla Yallaahu
23. Bardan Salàman la def Buur Yalla daal du faral
Di boddi waajuko yaakar birna Yallaahu
24. Ibrayma gaddayna daw mbokkamya ak kaka jur
di wër si Dun bi di maggal Buur bi Yallaahu
25. Ba yala xëy fayko Maam Ismayla teksa rakkam
Is-haaxa ñuy maami kuy Yonnenta Yallaahu
26. Ismayla judduna Maam Ibrayma bayyiko ak
Yaayam ja ñoom rek ca xeeri Makka Yallaahu
27. Seen marwa tarna kerook ba Hàjaray wërëwer
Rahmànu xëy fayeleen Zamzamba Yallaahu
28. Ba doomja maggee Boroom digëlko rayko munaa
Doom nan matal lifi Buur santaane Yallaahu
29. Ismayla naako defal li Buur bi sakku si yaw
Jàngalna kepp ku am tiis muñko Yallaahu
30. Muñëmga taxna mu am garaatu maami Yonnen
Lu waay tegoo nako muñ ngir royko Yallaahu
31. Naxool si Lùtin ma Soxnam weddiwòn di fexel
Way gëmya anda ca ak waa reewma Yallaahu
32. Luy xeeti ñàwteef ñukay def gorña bayyi jigeen
ñay sàkku ay goor ni ñoom ngir bonga Yallaahu
33. Wa reewma faale wuñu doolem ja neewalnañu
Xolam ba jeex far mu ñaan soppemba Yallaahu
34. Buur Yalla yonniy Malàkam dëpp sùfsa ñu dee
Ak xeerya muccël ña gëm te woolu Yallaahu
35. Seetalma Yuusufa bañkoy yòr si deegba kerook
Baayamba jaqq na moom Yanxuuba Yallaahu
36. Ñu forko genneeko am rewam mu xëy diko jòy
Ba bëtya muuruna moom Yanxuuba Yallaahu
37. Pexem magmaya demul ñu forko jàyko ka mòm
seen rewma jëndako ngir doomooko Yallaahu
38. Soxnamsa nas ay pexeem ngir sàkku Yuusufa far
Tuumaal ko yaqqap deram ca reewma Yallaahu
39. Ñu tëcko ay at mu naan As-sijnu xayrun ca kaw
Kasoo ma daqqal di tooñ Buur Yalla Yallaahu
40. Xëy Yalla fayko mu doon Aziiz ba boole ko ak
Baaybaak njabootga mu melnib jànta Yallaahu
41. Ayuuba feebara tax soxnnam ya wacc ko dem
Doomam ya dee lalam jep sanku Yallaahu
42. Taxul mu saalit xolambaat musla dañ di xalam
Boroombi bind amak luy ñakk Yallaahu
43. Ba Yalla xëy fayko xeewëlgaak weruk yaramam
Mòk Soxna Rahmatu ndax seen muñga Yallaahu
44. Zun-nùni mòm aw nitëm dañkò sonal bamu mer
Ndax weddi gaak lànk woteem booba Yallaahu
45. Mu dugga gaalga ñu xëy daanel ko jënwa warax
ko muy sikar ca sa biir jën woowa Yallaahu
46. Ba jënwa yàbbiko feebar dap ko ñaanama tax
Ba Buur werëlko ba may koy toppe Yallaahu
47. Mùsaa Kaliimu la Buur ilhaam ñu defko sa kees
Mu teer sa kër buur badoon ray liir ya Yallaahu
48. Yaayamja jaqq na Buur bañlooka weenya mu far
Ñëwaat si moom ngir dëfël xolam ba Yallaahu
49. Firawna doomoona Mùsaa Soxna Asiyatin
Yaayooko Bintu Muzaahim gëmna Yallaahu
50. Mu màgg dòn wër dajek ñuy xeex mudoon àtte far
Ray waaja mòm reewma feg mbokam ma Yallaahu
51. Firawna xëy diko wër ngir rayko Mùsaa laxas
Jëm reewi Madyana ak xiifam ba Yallaahu
52. Mbokkam ma ngir waa kërëm teralko maykofa far
Doomam Shu’aybooka baax te woolu Yallaahu
53. Ginaaw digëmba la Mùsaa jël njaboot ga laxas
Ngir dellu Misra fadoon dëkkëm ba Yallaahu
µ
54. Siinaa la Haatif ba wòwe Njambé naako demal
Woo Aalu Fir’awna bil Aayaati Yallaahu
55. Innii axaafu la wax Buur naako ndaw du ragal
Ku Yalla sas kay manoo bañ yanba Yallaahu
56. Mu boole kok mbokkamay Hàrùna muy waziram
Ñu jublu kër buur ba ak doolem ja Yallaahu
57. Mùsaa wedamlooka mook njabarya merna kerook
Munaako doo darra Yallaay Buur bi Yallaahu
58. Muy xëy di waar nitña bes Boroom digëlko mujël
Mbokkam ya dem Mu labal Firawna Yallaahu
59. Nitëm wa doon nattu, Mùsaa sonn loolu si ñoom
Ba Saamiriyyu gëlëm wloo leen faww Yallaahu
60. Luy xeeti ñaawteef ñukay def ken du jàdd ba dab
leen ken du bew ni Banuu Israayla Yallaahu
61. Ku toqqi tay si jubël njaboot, na jàng si moom
Mùsaabnu Imraan ma muñ seen mbonga Yallaahu
62. Goroomba yit noon la sonnee wòn si waaru nitëm
Ñuy jaamu Laykata bañ Boroom bi Yallaahu
63. Shu’aybu naaleen nangen weetël Boroombi Ahad
Te bayyi saccaaka naxtaan nitñi Yallaahu
64. Ñu lànk naako manoo tax ñuy matal wala ñuy
Ba sun Garap gii fi Maam bayyeendi Yallaahu
65. Ñu ngay xasak diko ñaawal tëkku nanko ba
Buur Xëy mer alak leen sa yuuxook niir wa Yallaahu
66. Mayuk Sulaymaana ak Dawuuda buuri Banii
Israyla teewul ñu bañleen weddi Yallaahu
67. Ilyaasu, Ilyasa’un, Zul kifli waar nañu leen
Ñu lànk bay ray ñadoon Yonnen ya Yallaahu
68. Zakariyaa’u taxaw di waare ñuy bañ ba far
Maggatna loolu mu ngay ñaan doom fa Yallaahu
69. Yërëmnaleen loolu tax mu ñaan ku donn Yonen-
tam googa ak waare waak jaamoomga Yallaahu
70. Teewul fexel nanko faagaagal ko boomati kay
Yahyaa ma donnoon yonentaag leerga Yallaahu
71. Sëtëm ba Iisaa yitam dañkoo fexel diko ray
Buur Yalla yeegël ko Fis-samaa’i Yallaahu
72. Iisaa mu jambure mii xolam bu laabire bii
Doorul xasul kenn tooñul kenn Yallaahu
73. Ku dëddu woon la amul woon kër di wër di dëfël
ñan beddiwoon, gaaya ñëw ngir bòmko Yallaahu
74. Ba digba yeksee xolam jeex ngir yërëmna kerook
Njaboot ga reer sa ginaawam fawwa Yallaahu
75. Nattuy Nabil Mustafaa jiituk judoom lako dal
Ba Yalla faate ka doon bayam ba Yallaahu
76. Ñu xëyko jur muy jirim yaayam ja yorko juroom
ak benni atya Amintaat faatu Yallaahu
77. Maamam ja Abdul Mutallib yorko ñaari atam
Ak Mustafaa mat mu ñakkaat Maamja Yallaahu
78. Baayam Abuu Taalibin xëy yorko yor bu rafet
Ba Yalla namm sa moom Mbiram ma Yallaahu
79. Mu xëy di woote Qurayshin lànk kaare taxaw
Kontar Ndawal Yalla ngir nërmeel ko Yallaahu
80. Julit ña gëm di nëbuy jaamooka julli di ñaan
Si Daaru Arxama ngir neew doole Yallaahu
81. Qurayshi dem si Abii Taalib tenaako waxal
Ñu joxko nguur ak alal mu bayyi Yallaahu
82. Yonenba naako bilaay Baay Yalla mooma yabal
Ku Yalla yonni manoo xëy lànk Yallaahu
83. Tenaako bun ma yenoon Jàntak Badar bi du tax
Ma bàyyi woote bi Ndaw laa rekka Yallaahu
84. Qurayshi naako waxal loo bëgg nan lako jox
Si nguur maxaamaak alal nga bàyyi Yallaahu
85. Yonnenba naa lima wax du dañ kerook lañu jog
Fayseene beddi Nabeek mbokkam ya Yallaahu
86. Ken jàyuleen ken jëndul seen njàyma ken jëlëtul
sa ñoomi Soxna Yonnenbay sant Yallaahu
87. Julitña xiif bay añeey xob marwa tarna sa ñoom
Teewul ñu japp kadoon seen Waaja Yallaahu
88. Buur Yalla xëy jël kadon Baaytëxba jël Xadija
Yonenba jaqq na ak jullit ña Yallaahu
89. Ñuy xëy di ñaawal Julit ñay door di leen toroxal
Ba ray Sumayyata ak Yaasir fa Yallaahu
90. Yonnen yërëmleen digëlleen far ñu dem
Habasha Kerook Najaashii teral leen gëmna Yallaahu
91. Yonenba xëy dem sa dëkkub ñay ndijày ya kerook
Taayif taxaw weddi kem wa Makka Yallaahu
92. Ñu boolekok xaleyaak saaysaay sa sanniko ay
xeer toj jëwëm ba deret jay tuuru Yallaahu
93. Ñu xotti dalla ya wërkoy saaga ak diko door
Genneeko dëkk ba jeexal xol ba Yallaahu
94. Malaka Yalla ma yor montaañ ya naako waxal
Ma door si ñoom Axshabayni leegi Yallaahu
95. Yonenba naa bayyinaalen ndax bañun ma dañoo
xamul bilaay ken amul xolam ba Yallaahu
96. Kerook la Jinne ya boolo ñëw di jebbalu si
Naan kaan bilaay yaay Rasuulu Laahi Yallaahu
97. Mu dellu Makkata delluy waare ñii diko daw
Ñaay jeem fexelkooka tiisal xolba Yallaahu
98. Bes Yalla nattuna Yonnen dog waxamja sa mòm
Jibriilu gëj fa ñukay jeebane Yallaahu
99. Tenaa jineem jimu dòn deeyòla mer mu wedam
Ñuŋ kay xasak diko ñaawal woorna Yallaahu
100. Mu yeek sa dojwa di seenu gan gadoon xaritam
Ñu naan mu ngay xaru ngir gacceem ga Yallaahu
101. Saaruw Duhaa wacc naakoon Yalla jeppi wula
Muñël ta motalli wootem booba Yallaahu
102. Noonamya daldi wedam muy woote bes lanu xëy
Waxtaane betta ko njël ngir rayko Yallaahu
103. Ndigël la wacca mu gaddày bayyi Haydara muy
Delloo Amaanaat ya Yonnen gëm na Yallaahu
104. Yonnenba ànda na ak Siddiixu daal di njëlu
Di dox ba àgg si xuntum Sawri Yallaahu
105. Asmaa'u sen dòmja modaan andi meew ma sa ñòm
Qurayshi xëy diko seet ngir rayko Yallaahu
106. Ñuy wër ba tiim leen Abù Bakrin ragal na ñu gis
Yonnen ba far tere wotem booba Yallaahu
107. Bul jaqq ndax kima woo waxlòma yanma yanam
Moonuy fegal ayu yeefar yooya Yallaahu
108. ’inaayatul-laahi mooleen làqq ken gisuleen
Bañ àgg Tayba dajeeg Ansaarya Yallaahu
109. Jullitña bayyi allal jaak kër ya fekki Yonen
Sa reewi Taybata ngir seen ngëm ga Yallaahu
110. Noonamya gën diko bañ Soppem ya gën diko gëm
Baatam ba gën di sewal xërëm ya Yallaahu
111. Yeefar ya toogu ñu jël gawar ya xeex si Yonen
Badar Uhud Xandaxin ngir bañ ko Yallaahu
112. Badar la Yonen taxaw di ñaan ba kaalaga rot
Naan Yalla buñ not sa mboolò mukk Yallaahu
113. Jaysun kerook notna jayshal mushrikiina ñudaw
Seen lim ba seen doole seen ngannaay ya Yallaahu
114. Uhud ñu xeexati ak moom gaañ Yonen ba kerook
Jullit ña fook nan ni Yonnen dee na Yallaahu
115. Ray nan si jambaari lislam rayfa Hamzata far
ab lim bilaay ñeeka bon te weddi Yallaahu
116. Ahzaab la Yeefërya boolok reewma naa bile yoon
Nan fekki Yonnenba fagaagal ko Yallaahu
117. Ngelaw ga daqqe naleen Madiina tiit nanu daw
Buur Yalla neenal la doon seen yeene Yallaahu
118. Ba at ma delsee Yonen xëy jublu Màkka bëgoon
Siyaare Kaaba ga far maslaa fa Yallaahu
119. Noonamya gën diko bañ Soppem ya gën diko gëm
µBaatam ba gën di sewal xërëm ya Yallaahu
120. Ñaar fukki siy at ñu kay xeexak di xeeb limu yor
Yeefër ya Naafeq yaak Yëhuud ya Yallaahu
121. Sen bonga taxna ñu wor sen hudna booba mu jog
Ngir jublu Makkata mooy fathom ba Yallaahu
122. Mu ñëw di toj luy xëreëm setal haram ba
Bilaal yeeg nodd Lislaam taxaw ba faww Yallaahu
123. Yonenba baalna ña doon mbokkamya daako sonal
Ñu naako yaa baax sa baayit baaxna Yallaahu
124. Aamul wufùdi ga ñëw ñep wuy si gënji Yonnen
Mu jiituleen jublu reewam Makka Yallaahu
125. Ginaaw Ajam ga la Yonnen dellu Taybata far
Feebar ba dugga ko muy waaj digba Yallaahu
126. Ñu took gisun ko sa jakkam jooja Saabaya jog
Di laaj Yonnenba ñu naan feebarna Yallaahu
127. Seen xolya tiit na ba boolo nañ sa jàkk ja took
Di jooy Yonenba ragal demam ga Yallaahu
128. Jooyoo ya taxna mu jog ñu fabko ak mititam
Munaa xanaa manu leen gëm Buur bi Yallaahu
129. Te naa ku Yalla yabal sab dig du jaas abadan
Samab digit bu ñëwee ma dem fa Yallaahu
130. Muñleen ëlëk soriwul nu naani Kawsara mooy
Samab digak yeen kerook Mbay joyna Yallaahu
131. Tàngàywa metti ñu tùrkom ndox xolamba di muñ
Ñu takk bopp ba muy sabbaah fa Yallaahu
132. Diirëb dundëm ga xamul noflaay te womle wuton
Ndekkeena ndox ngir yorul lum togg Yallaahu
133. Doomamya ñeppa ko jiit Barzax mu muñko ludul
Zahraa u Fatimatoo jur sët ya Yallaahu
134. Nattoom ya ñoo walangaan si Ahli-baytin
ñu jël ñii genne ray ñële ñii ñu beddi Yallaahu
135. Ndem Mustafaa gëna gën ndem Mustafaa gëna baax
Ndem Mustafaa gëna am teraanga Yallaahu
136. Ndem Mustafaa mata xool ndem Mustafaa mata roy
Ndem Mustafaay wane yoon wiy jalle Yallaahu
137. Lu waay tegoo nako muñ ndax dacna fuuf luka raw
Moom Mustafaa moom mi gën nit ñeppa Yallaahu
138. Boroom bi wowaatko soppem yepp took diko jooy
Buur Yalla nammàt dikaatëm worna Yallaahu
139. Mu wacc reewi Ajam wooteem ba tambaliwaat
Ngir jangalaat nit ñi muñgaak dalga Yallaahu
140. Mu feeñ si xeetu Lebu ñuy jaamu Yalla di rax
Seen jaamu googa Xërëm yaak Tuurya Yallaahu
141. Zakin si weeru Rajab la mbir ma aksi si moom
Yayaam ja daaldi laxas Maam Kumba Yallaahu
142. Lekkul waxul ñetti fan la xalwa yekki sikar
Di sant Yalla midul dañ mukk Yallaahu
143. Mu wo njabòtga nileen Buur Yalla defna ma dòn
Xayral-waraa nanu muñ ta sant Yallaahu
144. Dimàs la yùxu sa kaw Yallaa ma yonni ma doon
Muhamadum demba doon Mahdiyyu Yallaahu
145. Mbokkamya naa dofna nak saalit ga yobbuna far
Boppam ba took diko ree muy woote Yallaahu
146. Ñunaa Ndijaayja sa doom jii jinne japp nako
Jogël si moom balamoo xëy sànkou Yallaahu
147. Limaamu naako Ndijaay Yallaa ma yonni mbirëm
Ku Yalla yonni manoo xëy lànk Yallaahu
148. Muy woote weetël Boroomam ñepp naa dufi am
Li maam bawak nun du niil muy tudd Yallaahu
149. Wa reewma deggë mbirëm di ñëw di jebbalusi
Mbolooma yokku sikar say jolli Yallaahu
150. Ñu xëy di ñaawal ña gëm di jeem dileen toroxal
Limaamu naalen na ngeen muñ faww Yallaahu
151. Noonam gën diko bañ gaayam ya gën diko gëm
Baatam ba gën di sewal seen Tuur ya Yallaahu
152. Ñu mer kalaameko ak buur naako so moyuwul
Kiy simpi samp bi xëy daneel la Yallaahu
153. Ngannày yu takku la am soppem ya gëmnanuko
Jiyaar la woote mbiram day jolli Yallaahu
154. Tubaab ba ñëwna sa mòm fekkòn Sahàbaya tòk
Di tudd Yalla ñu laajleen Goor gi Yallaahu
155. Ñu fekk Baay Laay sabiir dòn jeema taal mu nasax
Ñu ceene Njoolma mu rot ñu yeemu Yallaahu
156. Ñu genne soxwa bëgòn bòm Mam Limaamu mujël
Noppam ba ak biir ba joxleen woolu Yallaahu
157. Ñu teqq takkul ka songoon Maam Limaamu kerook
Dootul xalaata ñëwaat ca kër ga Yallaahu
158. Noonam gën diko bañ gaayam ya gën diko gëm
Baatam ba gën di sewal seen Tuur ya Yallaahu
159. Ñu ànda dem seeti Jal Seriñ Ndakaaru lawoon
Ni waa Qurayshin banuy gis Baay ba Yallaahu
160. Mu naan Limaamu bawal sa gaayi dellu ji seen
ay kër nga weetëk Boroom bi, jaamu Yallaahu
161. Mu naako medd du dàqqay tan yu wut si ndawal
Maay meddu Yalla mi gaayey tan yi Yallaahu
162. Limaamu naalen bilaahi Yalla mooma yabal
Ku yalla yonni mano bañ woote Yallaahu
163. Saa woote bii su matul Isaa mu ndaw mile kat
mookay matal leey nameeluk Buur bi Yallaahu
164. Sa guddi googa la jog gaddayi bayyi ganaaw
Soppek xarit yak njabootam gepp Yallaahu
165. Lëndëm ga tarna kerook muy dox ba ñëw
Malika Ngejjam ga warna ku am tiis demfa Yallaahu
166. Tubaab ba tëkkuna ay mbokkam neleen fumu dal
Waxleenko baa ma mbugël yeen ñepp Yallaahu
167. ‘inaayatul-laahi moolen làqq kenna xamul
Fum dal xolam ba yërëm mbokkam ya Yallaahu
168. Mu genn naa maa ngi nii ñu bayyi mbokk ya far
Ku am xolam dootu am si Dun bi Yallaahu
169. Kerook la àndak Tubaab yàk noon ya jublu Gore
Ñu naan ki daan woote tay lay sànku Yallaahu
170. Soppem ak taalubem yay jooy di yuuxu sa kaw
Limaamu naa duma wees Beer woorna Yallaahu
171. Ca Beer la gaalga taxaw ñu xamni Seydi Limaam
Du noon bunuy sànki Kongo Belsi Yallaahu
172. Ca Beer la Baay Laay wanee keemanya gardya tiit
Di ñaan mu dellu mu bañ moo woolu Yallaahu
173. Bam dellusee la Tubaab ya naako Goorgi waxal
Ñi sos ñu jël len alak leen faww Yallaahu
174. Limaamu naa bayyi naaleen ndax bañun ma dañoo
Xamul bilaay ken du Baay Laay woorna Yallaahu
175. Xarit ba Mbay Silla gëm wootem ba daalko teral
Ñu mer ba folliko moom Xaadii ba Yallaahu
176. Limaamu dellu di wootey jaamu Yalla mbiram
May jolli noon ya di gën koy jeppi Yallaahu
177. Mu ngay yabal taalibem si tooli noon ya ñu bay
Ta mooy joxey añ Limaamoo gën fa Yallaahu
178. Ku feebaroon bò ñëwee mu ëf nga wer te werul
Mettit musul tàggalook yaram wa Yallaahu
179. Feebar sonal ko te teewul saa yu gan ña ñëwee
Kanam ga talli mu ree waxtaan fa Yallaahu
180. Ba bes gëtëm ya sonal Limaamu am kufa ñëw
Doon jeema faj far bëtëm ya muuru Yallaahu
181. Noonam ya naa kifi doon wooteeka jàngale tay
Moo gumba an lamu xam muy sant Yallaahu
182. Ñunàko nan lay gumbee kudib Yonenta munaan
Da ngeena jàngul mbirëm Yanxuuba Yallahou
183. Gëtëmya muuru xolam bay gis ba sooko jubee
Mu wax sa tur, ken manul peek may ya Yallaahu
184. Mu sax ca sëgg ga zaayun siy atam diko muñ
Di sax di woote di waar waa reew ma Yallaahu
185. Ña nàngu woon bëriwuñ Tanneef ya ñooka sagal
Muy waare naa sama cër mooy woote Yallaahu
186. Digëm ba daaldi jigeñ Limaamu digle ñu woo
Soppem ya ngir Korigaak julleem ga Yallaahu
187. Ñu wër Limaamu ca jeexaaybaak mittit wa kerook
Ak leer ya ak taar ba muy ab jant Yallaahu
188. Tàngaay wa dugg ko muy dox gaaya japp ko muy
Wax gaaya naan nanu gaaw ma àgga Yallaahu
189. Sallaaw kudib neew dinay far jiite kuy dund man
Janaaza laa xolya tiis ngir nawko Yallaahu
190. Mu naa ku yeene Yonen joxkob dërëm nama jox
Maay Mustafaa maay Rasuulul-laahi Yallaahu
191. Mu jiiteleen julli ñaan xeetamwa mucc kerook
Limaamu moo gore moo am yeene Yallaahu
192. Ginaaw xutab ya gisaatun Njolma day bëga dem
Firdawsi ngir lamu doon wax matna Yallaahu
193. Wootel na Yalla ba dem saxal fi diine ju wer
Ku doon bañak diko kontar sewna Yallaahu
194. Banook Yonenta Isaa muy xàll yoon wifi
Maam Daan xall doon gaynde doon ab janta Yallaahu
195. Ñeen fukki atya kamaal Seynaa Manjoon taxawaat
Di xall mook Baabakar ak doom ya Yallaahu
196. Baay Seydi Caw xalifaam yaatal fi yunu Limaam
Baay Raan nëwaat awko àndak Abdu Yallaahu
197. Baay Abdulaaya taxaw doon jaasi diine ju wer
Dawal na Seydi Manjoonak Doomya Yallaahu
198. Turëw Limaamu si biir reewmeek fudul Senegaal
Tay jibna Buur fayko muñ gaak dalga Yallaahu
199. Sëtëm yi daaldi taxaw àndak Sahaaba yi tay
La Maam jiwoon saxna doon ab foore Yallaahu
200. Waa Ahlu Laay nañu seet si Maam Limaamu te seet
Siirab ku woote jëmoon ca Buur bi Yallaahu
201. Nan muñ te baale te ñaan Buur Yalla gindi ku reer
Te bañ xuloo aka xeekak xaste Yallaahu
202. Na Yalla julli si Baay Laay ak ku topp sa moom
Mook Anbiyaa yi te sëlmël faww Yallaahu
203. Te yokk fan Abdulaay te maynu jot ngërëmam
Moom miy sunub sag di sun ab sang Yallaahu
204. Defalnu xol yu nangoo toggoo dogalyi gërëm
Buur Yalla kontàn silum xëy defko Yallaahu
205. Ay Yalla maynu nu wax Ay Yalla manynu nu def
Li Maam bëgoon kuka wax ak defko Yallaahu
206. Sumas-salaatu 'alal-Muxtaari xayri anaam
Wal-aali was-sahbi wal-atbaa’i Yallaahu
Mamadou Bara SAMB LAYE
Appel 2014 31 Mai 2014
3.Am tahsaboo (أم تحسبوا ): Ndax da geena fook ni. Muy aaya bi sunu Boroom di artu way gëmyi nileen ndax da ngeena fook ni di ngeen dugg ALjani ta (Baasan) muy tiis wi dallon ñi leen jiitoon duleen dal ?
4. Hattà yaxuular-rasuulu ayna nasrul-lazii bil-haqqi arsalanii” ( حتى
يقول الرسول أين نصر الذي بالحق أرسلني ): Boroom bi mooy melal tiis wi daan dal ñi jiitu, di waxni daana metti ba seenab Yonnent di wax Ana Ndimbalul Yalla -mima yonni si dëgg- ?.
13.’Aad (عاد ): Niti Yonnent Yalla Huud.
16. Samuuda (ثمود ) : Niti Yonnent Yalla Saalih.
23. Bardan Salàman (بردا سلاما ) : Sawarasa defum peex ak jamm si Ibrahiima.
39. As-sijnu xayrun (السجن خير ) : Kasoo ma daqqal di moy Buur Yalla
40.Aziiz (عزيز ) : Kilifa gay or alali reew ma. 41. Zun-nuuni (ذو النون ) : Yonnent Yalla Yuunus
47. Ilhaam (إلهام ): Yekkiiwal, moy li Yalla def si xelu yaayu Muusa mu dof doomja si kees.
49. Bintu Muzaahim (بنت مزاحم ): Aasiyatu Soxnas Firawna.
54. Haatif (هاتف ) : Kàddu guy wax te doo gis jëmm ja.
23. Bardan Salàman ( بردا سلاما ) : Sawarasa defum peex ak jamm si Ibrahiima.
39. As-sijnu xayrun (السجن خير ) : Kasoo ma daqqal di moy Buur Yalla
40.Aziiz (عزيز ) : Kilifa gay or alali reew ma.
41. Zun-nuuni (ذو النون ) : Yonnent Yalla Yuunus.
47. Ilhaam (إلهام ): Yekkiiwal, moy li Yalla def si xelu yaayu Muusa mu dof doomja si kees.
49. Bintu Muzaahim (بنت مزاحم ): Aasiyatu Soxnas Firawna.
54. Haatif (هاتف ) : Kàddu guy wax te doo gis jëmm ja. Aalu Fir’awna bil Aayaati (آل فرعون بالآيات ) : (woo) waa kër Firawna si ay keemaan yu rëy.
55. Innii axaafu (إني إخاف ) : Damaa Ragal,
56. waziram (وزير ) : Jëwrinam.
62. Laykata (الأيكة ) : Garab gi waa kër Shu’aybu daan jaamu.
71. Fis-samaa’i (في السماء ) : Kaw Asamaan.
80. Daaru Arxama (دار الأرقم ): Mooy kër gi jullit daan laqqu di jaamu, ngir daw ayu yeefër yi.
94. Axshabayni (أخشبين ) : ñaari doj yi wër Taayif.
103. Amaanaat (أمانات ) : Denkaane ya.
108. ’inaayatul-laahi (عناية الله ) : Dencub Yalla.
113.Aziiz (جيس ) : 313 muy limu julit yi. notna jayshal mushrikiina (جيش المشركين ) : Armeb Bokkaalekat yi.
121. hudna (هدنة ) : seen xaatim ba si weer ngannaay. Fathom ba ( فتح
مكة ) : ubbik Makka ga.
124. Aamul wufùdi (عام الوفود ): Atum mbooloo ya, bi Araab yep mangee wuysi Yonnen.
139. Ajam (عجم ): Xeel widul Araab.
141. Zakin (زك ) : 27. 143. Xayral-waraa (خير الورى ) : ki gën si mbindeef yi,
167. ’inaayatul-laahi (عناية الله ) : Dencub Yalla.
175. Xaadii (قاضي ) : Atte kat ba.
184. zaayun (زاي ) : Juroom ñaari At.
189. Janaaza (جنازة ): Ab neew.
192. xutab (خطب ) : xutba yamu jangaloo woon.
195. Kamaal (كمال ) : mat.
199. foore (foret) : Àlla bu fatt.
202. Anbiyaa (أنبياء ) : Yonnent yi.
206.Sumas-salaatu 'alal-Muxtaari xayri anaam, Wal-aali was-sahbi wal-atbaa’i Yallaahu ( ثم الصلاة على المختار خير أنام، والآل والصحب
والأتباع يالله ) : Yalna Yalla Julli si Tanneef bi, Gën ji mbindeef mook njabootam, ay sahaabam aki toppeem.