Ndawal YALLA
Ce poème est adressé à l'humanité qui en quête de la voix du salut... Cette humanité qui se cherche, en se trompant de maître ...La nouvelle Zélande est la parfaite illustration du fait que les malades ignorent toujours le Medecin Chef.
Way wi Humanité bi lanouko kagleel moom miy weur foumouy jaar ba mouthie..gnui gueuleum ak reeré kika Yalla boleel. Li khew Nouvelle Zélande fir ndé la ci ni Malades yi reerénan Doktoor bi.
1.Ndawal Yalla lii ngeen xëy di sàggan ba rombako
Di jeggiy bagaanam dëkké wër ngir juwaatleko
2.Fu Ndaw masa wootee gaaya yor kàggu yaay taxaw
Di diingat ba juuyook leerga far daaldi noonuko
3.Ña gëm took di jaamuy topp seen Waaja soppako
Lu xaskatya gën xas Ndawla ñuy gën di jappako
4.Ña weddiy fexeey jeebaané ngir màbb wooteba
Bilaay bun xamoon maanaaya jëkkënté nanguko
5.Bu ngeen fattewul woon demb dooleenko romba tay
Bu ngeen ubbi woon seen xolyi leeramyi feeseko
6.Ñi naan manta am Yonnen du feeñat danoo xamul
Danoo teela lem seen kaggu yooya ba weddiko
7.Nubuwwatu Tashrii'in Wa Tajdiidi millatin
Nubuwwatu Tasdiixin nu ngeen def ba reereko
8.Ki ñëw ngir sosaat aw yoon Ki ñëw ngir di yeesalaat
Ki ñëw ànd ak yonnen beneen ngir dëggëlsiko
9.Nubbuwatu Tashrii'in la Mommadu tëc ba dem
Ku ñëw si ginaawam faw nga jël Yoon wa toppako
10.Demal yër Sayootii xool ca tafsiir ba ndax nga xam
Yonnen noon na Iisaay ñëw di yeesalsi nanguko
11.Ku bañ loolu Qur'aan neena "'ilmun li saa'atin"
Nu ngeen def ba bañkoo xool ba yeena ngi rombako
12.Ñi naan fanla Qu'r-aan tudd Mahdiyyu ñoo nelaw
"Bishaara" si kuy yeesal du doon sharta jappako
13.Te sax Ndaw lu nëw jog wooté jël njub ga sampako
Di def mu'jizaat Maawardi nee moom la wuyjiko
14.Nu ngeen def ba bañ Baay Laay mi waxni damaa nëwaat
Damay yeesalaat maay Mustafaa ngeen weranteko
15.Dangeen lactewul selluk xolam ak matuk jëfëm
Namuy weetëlee Buur Yalla xiirleen ci jaamuko
16.Ki daan toroxal Shaytaané ngeen far juwaatleko
Bu njur jaawalee sàmmam ba bukki ya reeréko
17.Ki daan waxni kaay leen laac lu ngeen laac dinaako def
Ci kantanu Buur bii joxko diineem ji yonniko
18.Musul jog si wooteem booba daan noon ya jëmbataat
Lu ken manta xool naa cim ludul xolba noonuko
19.Damaa xamni goorgoo xamni Tawhiid la yekkati
Di jaamoka sellal jëf yi kuy seetlu gisnako
20.Di xettali ñan boddeeka yekkati ñan sewal
Di suuxat cofeel luy jikko buy mbaax mu digleko
21.Zakaatal alal ngir bañ ku ñaan xawma bañ yëfëm
lukoy firi Buur Yallaay ki xëy deeyko joxnuko
22.Anaa "Xadarul-Mawlaa" te seen añ bi laafi taac
Damay gan gu jaaree poot ña doon seenu rombako
23.Bu seen xiif bi yeenee dañ di ngeen musa xeewlusi
Ku xiif baña añ far fandé biirëm ba jeppiko
24.Da ngeena tawat Doktoor bi ngeen bañko bëgg wer
Bu doonoon keneen buy dellu lum indi yobbuko
25.Yërëmleena tax doomam ji ñëw ngir di feddali
Te booba batay seen xaar bi manleena bayyiko
26.Naleen Yalla may leeruk xolak leeri bët ba ngeen
Janook Dogalam bii joxko seen tum bi toppako
27.Bu ngeen ko xamul fii Yalla bum leen rawaat fëlee
Bilaay yërmëndee tax Yalla woowaatko yonniko
28.Awaay Yalla booleel gaayi nangook ñi bañ yëfëm
Te mayleen ñu làngak moom ëllëk bañ juwaatleko
29.Te dolli salamaatin Yonnen bii nga yonniwoon
Te maynu nu sax ak moom te fum xëy nu xëyleko
30.Te yaggalfi lool sët bii mu tuddoon di Abdulaay
Te maynu nu àndak moom te fum jëm nu gungeko
Rawdu Jammalaay
Guddi Gammu1438
12/12/2016
#lejeunepoete