Salli Yaa Rabbi alaa seydi Limaamoo
Bismi-l-Lahi Rahmaani Rahiim
-
Salli yaa Rabbi alaa Seydi Limaamoo di sa soppe
Salli ya Rabbi alaa Seydi Limaamoo di sa ndawli
-
Ña ka don seet ba ñu aksee te ne Baay Laay da nu lay jël
Sunu Yonnent da ni , ey waay , nungi daarloo sunu Buur ba
-
Nikki réew ma ba ñu manko te ne Baay Laay du fi wax tey
Ña ñu yaakaar ba ñu génnée, sunu Yonnent santa Buur ba
-
Niti Kabweer ba ñu aksee te ne Baay Laay di na dem tey
Sunu Yonnent da ne man kat manu maa dem, santa Buur ba.
-
Ba ñu forsee, te ne dey dem, ba mu geesoo ñu ne maalum
Ña ka doon wax, ña ñu àndal da ñu tiit , may santa Buur ba.
-
Nikki Baay Laay ba mu wooteen ñu ne moo waay bumu jëm kaw
Na nu gaaw dem gisi goornoor, Njiin naan cey sunu Buur ba.
-
Ki ma làngool, ku mu làngal doo tiit, doo wara daw lor
Nanu dem far, ba ca goornoor, ba ñu xam may ndawu Buur ba
-
Ba ñu aksee , te ñu wër Maam, mu ne man may ki fi Buur tek
Di ko wooteel, di ko seetal, ku ma bañ doo gis Buur ba
-
Ña fa doon wax bamu tontoo da ñu tiit naa fu nu jëm tey
Sunu Yonnent dafa am ndam te ñu làngal ko fa Buur ba
-
Li nga doon wax , ku ko mos wax di nga daw mbaade nga sànku
Ku fi dul yaw naka mos seet, bamu xam kantanu Buur ba
-
Nikki seen gal ga ñu teeral, Njiin naan kii du moo may jël
Du ma antan, bu ñu sonnal ña ka yor, maa nga ca Buur ba
-
Ba ñu weddee la mu wax ñoom te ne Baay Laay di na dem tey
Ba mu tàbbee te di ñaanal ña ka yaakaar, santa Buur ba
-
Ba mu déqéé ba ne kërKër da fa jub Béer fa la far des
Da nu far yéém te ne Baay Laay mooy Yonnent ba ca Buur ba
-
Ku la dingat dafa xoolul say mey yaa jara àndal
Nu ngi lay gëm, di la doyloo, di la yaakaari fa Buur ba
-
Sunu Yonnen ba mu faatoo da ñu doon wax fu nu jëm tey
Seydy Isaa dikk yeesal sunu ngëm nuy santa Buur ba
-
Géej sàbbaa, nit sàbbaa , ngir bés booba lu am la
Jën yey teer , nit ñay for, ngir màgal sunu Buur ba
-
Seydy Isaa jok waaraate ca mboolooma ne iskey
Dafa daaral la ñu doon wax mbiri Isaa ya fa Buur ba
-
Nikki Baay Laay ba mu wootee te ne Seydeey ki ma doon wax
Da ne lee wér te du luy deñ, waxi Yonnen la fa Buur ba
-
Yeen soodaan ci lu ngeen ngëp ba di gaaral sunu ndaw li
Sanga Soodaan mooy Baay Layy ki fi wooteel sunu Buur ba
-
Na nga yër « Mat-u-Rasuul », gis la fa woy kat ya di wax ngir
Ba mu jéggée famu dal, xel du fa dem, bir na fa Buur ba
-
Ba mu jéggée Medina, dal na fa Ngor, mawlidu Yoofin
Ba mu feeñee te ne may Maadiyu , kay bir na fa Buur ba
-
Ba ka gàdaay ga dabee, saaba ya dar Maam ba ñu jiitlé
Ñu nga dal ngejja ga , foo faay sunu yaakaari Yonnen ba
-
Niti Kabweer, ba ñu aksee fa Libaas “sarse” ko aw ay
Ba ñu naan yak ñi la doyloo daa nu leen soobi ca bëlbë
-
Ba Libaas tontu ne yallaay ki ma doyloo, maa di soppeem
Bu ma paasee rëdu Béer koon du ma yaakaari soowoo ba