Sayfu LAHI
BISMI LAAHI RAHMAANI RAHIIMI 31-9-1963
1. Bismi laahi may deeti niaan Buur Laahu “bi jaahil Imaam”
Rabbi dollil say ngueunéél, ak say ndimmeul, ak say “kiraam”
2. Noo ngi lay niaan sax ci limaam, ak ci Lislaam rabbanaa
Ak ci lihsaan boolé kook xééweul yu jeum " yawmal xiyaam "
3. Rabbi dollil diine Lislaam sam ndimmeul "antal kariim”
Yal na not mbooleem lu juuyook moom “fii jamiihil anaam”
4. Diiné Lislaam am na ay jeuwrin yu koy yor “kulla hiin”
Yallah moo leen tan mey leen woolu leeen jox leen salaam
5. Niooy gni kay wooteel ci par téémééri at loolooy la siiw
Boppu téémééri at yu ne lay am “ila yawmal xiyaam”
6. Mahdiyooy seen njiit bu leen bagn baayu Isaa ak Manjoon
Moo fi feign fii “rahsi aazal xarnu” mooy Seydil Imaam
7. Ahlu lay gnoom lagnu jagleel xeeti mey nioo am ngeunéél
Kepp kuy sakkooti xééweul japp leen nioo am maqam
8. Waaju leen méngoo di nay am ndam euleuk “yawmal xiyaam”
Waaju leen bagn mbaa mu xas leen alku dotul doon “allaam”
9. Gaagni nan seetaat sunuy xamxam te settantal bu baax
Ndax gnu xam kan moodi woon Mahdiyu miy njiiteul “Anaam”
10. At ma bidééw booba feenioon andakub laar moo di woon
Tektalub Mahdiyu cik feeniam bu leen juum mooy allaam
11. Yaw yeureul tééré bu gnuy wax “Al Isaaha fii bayaan”
“Sarti saaha” koon nga gis lii muy lu wér “duunal wa haam”
12. Maam Limaamo féégn ca Yoof woo leen ni leen may Mahdiyul
Muntasar may ndawli nieuw leen seetsi may “samsul anaam”
13. “Ajibuu daahiya Laahi” mooy baat ba Baay Laay woote muy
Baat ba Yonnen wooye woon waa Makka ak wa “ahlu Saam”
14. Daldi leen jox baatu tawhiid baatu lixlaas loolu mooy
Baatub “laa ilaaha illa Laahu” geum “xayrul anaam”
15. Laa ilaaha illa Laaha, laa ilaaha illa Laahu
Laa ilaahu illa Laahu Limaamu yaay Seydil anaam
16. Yallah daal kay jox ngeunéélam boole kook ay « muhjisaat »
Mooy la nuy xammee ndawal Buur Laahu miy « Rabbul anaam »
17. Daan na euf nit kooka dib niiw saayu soobee Maam libaas
Yiir ka kaalaam waaja jog naa maa nga woon " yawmal xiyaam "
18. Mos na randal gééj ba tey gééj weesuwul reuddeum wa mooy
"Seydi aazal jinsi » yow kay la nu doon xaar yaa Imaam
19. Mooy ba gééj feesee te feesal néégi waa keur Maam libaas
Ba mu feree Baay Laaya jog andak nia geum Seydil Imaam
20. Dem tefes reuddeuw reuddeum naa gééj gi dootul jalla fii
Yééna dul xam waaye gééj gii xam na may kan “fil anaam”
21. Ker banonam yoo ya peegee Njiin la leen wax moodi kan
Munga naan maay ndawli, maay Mahdiyu, may “samsul anaam”
22. Saayu soobee Yallah muy woo ruuhu Baay lay japp leen
Seydi Isaa Ruuhu Rahman mooy donay Imaam
23. Daan na def kéémaan di waxloo waaju jangul sol ko muy
Janga xur-ann, mba di wax xamxam ni aalim juy “allaam”
24. Mos na dekkal waaju dee laajal gna teewoon kerb a goor
Gunu naa MBay Silla faatoo niepp took tey xaar Limaam
25. Maam Libaas nieuw daldi woo Mbay munka naa yaa Baabakar
“Xum bi isni Laahi rabbil Arsi” miy Rabbul anaam
26. Baabakar jog naa ka yow Seydil basar yaay mahdiyul
Muntasar, man maaka xam ndax maa nga woon “yaw mal xiyaam”
27. Doonté def kéémaan di nay tax nit di geum koon niepp geum
Maam Limaamu Laahi ngir moom daan na wax laaj leen karaam
28. Boo nieuwee ngir laajsi Baay lay wax la mbooleem say xalaat
Yoo naroon laaj ak yeneen loo doon xalaat “duunal kalaam”
29. Jéémeu lim xarbaaxi Njiin ak duusi gééj nioo bokk yam
Doy na cee wax gééj ga neexoon ngir di joy Seydil Imaam
30. Ker ba Baay lay ruu ga tagoo “ahlu dunyaa” jeum jinaan
Gééj yeungootul ngir di joy Njiin, ndox ma nexx ngir geum Limaam
31. Gééj ga faf neex tambalee keur Maam Libaas yam jamma Laay
Gnii di fóót, gniy sangu, gniy naan, gnetti fan “duunan siraam”
32. Fan ya gééj am ndox ma neex mooy fan ya ruuhuk Maam Libaas
Nekkatul biir jeummi Baay Laay ken robul Seydl Imaam
33. Ngir ngeuleumtéék jaaxle, gnii ne ngir ga doon xaar Ruhu Laahi
Seydi Isaa Ruuhu Rahmaan miy donay Seydil Imaam
34. Fekk baayub Abdulaay miy Seydi Isaa Ruuhi Laahi
Dem kajoor fii bayti Maamur lagn ka wax faatu Limaam
35. Ruuh ga moo def jantu njolloor suux ci Isaa Ruuhu Laahi
Seydi Isaa Ruuhu Rahmaan xeuy di “samsan fil anaam”
36. Seydi Isaa nieuw nuyyook mbooloo ma waar leen xol ya giif
Ruuhu Rahmaan dem julléé Njiin yeesalaat mbooleem “lanaam”
37. Nioo ne woon Mahdiyu Isaay doon jarafaam moodi doon
Naayibam moo kay julléé li am na nieuw leen seet Limaam
38. Gaagni nieuw leen geustu waat diinéém te seetaat koon di ngeen
Xam ni Baay lay Yallah moo soob def ka muy njiital anaam
39. Waaju yeur taariix ba xool aayaatu Isaa fii zaman
Dootu xaaraat mahdiyok Isaa “ilaa yawmal xiyaam”
40. Boo yeuréé “maa xaalahu seyxu suyuuti” koon nga xam
Dootu loo defdefle feeniuk Mahdiyan Seydil anaam
41. Bopp tééméérub gnenenteel moodi feegnuk Mahdiyul
Munstasar seetal kitaabul keusfi geum Seydil Imaam
42. Yall miy Buur def na mbooleem li dajeek Baay Laay mi feign
Fii ci Yoof nan santa Rahmaan nun gni geum Seydil Imaam
43. Mahdiyu Laay dem na, Issa dem, bu leen juum seeti leen
Njeexxitam mooy seet Manjoon ak Babakar “ibnay Imaam”
44. Baay Manjoon mo am ngeunéél, moo doylou, moo mugn moodi gor
Am na xamxam, am “diraayaa” ak méy yu réy booleek karam
45. Top leen Yallaak Yonnen loolooy waxam ak moytu leen
Adinaak seytaane banneex koon eulleuk ngeen gis Limaam
46. Ak xilaafaam neex na moo tax waaju saggan beew bu leen
Top doyloom ngir di bagn tiisal mbindééf koon muy araam
47. Waaju xoolul sakuwul lul adinaam teggil Manjoon
Waaju geum Buur Yalla doyloo Njiin la déggool “fil anaam”
48. Maa ngi teeral woywi tey teeral ci Seydi Baabakar
Bun Imaam Laahi miy yaakaari waa “ahlul kiraam”
49. Gaagni gis Baay lay gnu ngay wax na ku xoolaat Baabakar
Gis nga Baay lay ndéém gisowoon Mahdiyaan Seydil Imaam
50. Moodi gééj guy mbambulaan neel ngir ci xamxam baaraka
Laaahu fiihi noo ngi niaan Buur Laahu dollil Mbay salaam
51. Rabbi yékkil laa ilaaha illa Laahu miy sayfu Laahi
Rabbi saxalal Laa ilaaha illa Laahu miy sayfu Laahi
Rabbi dollil Laa ilaaha illa Laahu miy sayfu Laahi
Rabbi dooleel Laa ilaaha illa Laahu miy sayfu Laahi
Rabbi daaral Laa ilaaha illa Laahu miy sayfu Laahi
Rabbi daasal Laa ilaaha illa Laahu miy sayfu Laahi
Yal na dok mbooleem lu juuyook moom fi jamihil anaam
52. “Salli wa sallim alaa xayril waraa yaa xaalixii”
Muy salaatan anda ak saabaamya jeum “yawmal xiyaam”