Seydi Rohu Laay kula woy
Bismi Laahi Rahmaani Rahiim
-
Bismi Laahi may bëgg woy Seydina Limaamu te woy
Rohou Lâhi ndax kuka woy am ngërëm fi jannati
-
Deglu leen ma yeen ñi nélaw ci jamaana wax fi ñu aw
Ba gëlëmté reer nanu faw bi imaami rahmati
-
Waaja sééntu mahdyu moom té gisoon mandarga ya xam
La mu janga woor ka ni moom moodi zul kalaamati
-
Ndax bidiiw ba fèñ ca soloy maam limaamu fèñ na di lay
Gaaya janga gis ko ne mooy daalu zul Alaamati
-
Mooy mandarga mahdyunaa Maam limaamu wooté munaa
Nane ka muñ bésam ya mu naa moodi zul alaamati
-
Bés ya ma ñu ñëw diko laaj mu muñlooti gaaya ka laaj
ñetti weer ni leen bunu aj sunu mbir bi subhati
-
Wéér ya ma muna nanu jëm ñetti at you mat banu xam
Bukay wéésu xam léén né moom moodi zul alaamati
-
At ya mat Ñu ñëw muni leen ma ngi waat bou féké ni njiin
Mooy limaamou seydu zamaan la asiilu xaryati
-
Daldi dug gaal ga di dém aatif ba wax ka soloom
Waat nga lakka moy nga limaam fiika laanal xusrati
-
Doora binda létar té naa ka jogoon di waat lak naa
Yéén ñi dés niléén aamana bi imaami rahmati
-
Gaañi yééwu léén ci mbirëm ku xamul na laaj ñaka xam
Ku kiñaan nga gén ca moom bil huda mine subhati
-
Gaagni séénu mahdiyu ñoom té ñu janga gis ni judoom
Aama Anrasin té imam ñëw fi chahri Idyati”
-
Boo yëré masarixu xam li max té déésula jam
Bul wérantéék waaju gëlëm soobu fil juhalati
-
Maam limaamu ñëw na ba fééñ déglu léén ma wax fimu fééñ
Aama Aasasin cala fééñ gaña bañ di séénu ti
-
Gaañi woolu léén baña jum Maam Limaamu am na ngërëm
Moom mi feeñal yoon wudi jëm daaru Zil salaamati
-
Maam Limaamou laaya toxal seen xërëm ya daldi saxal
“Bi tawhiidi Rabbi kamala jalla an sari kati”
-
Baatub laa ilaha illa laah la saxal di wooté lilah
Dalni aajiboo daya laahi wuyu leen li dahwati
-
Mu taxaw di wooté ca kaw gaaña bañ mu yekki ca kaw
Ruuhu naa kilee ma di aw mooy maal Bi dahwati
-
Fekk naa ñi janga ñu naa mahdyoo di seydi zamaan
Té isaa di wuutu makaan ba fii bahdi nusxati
-
La ñu wax moyul dafa am Mahdyoo di Seydi lu maam
Ruuhu laaya wuutu Limaam fii balaaxi dahwati
-
Ñoo waxoon Isaa di jullee mahdyam ndéém joknafa lee
Am na, Ruuhu laaya julee bi Imaami rahmati
-
Gaañi yeewuleen baña juum gëm Limaamu ak xalifaam
Seydi Ruuhu laahi ku ka gëm am gënéél fa jannati
-
Mahdyoo ngi woote ba wéy tekfi ruuhu laahi mudi lay
Gaañi rééré leen bañu wéy yaxtafoola zaarati
-
Yeewu leen te xamne Limaam ak Isaa ku leen boolé gëm
Yàlla Buur ba fey laka ndam min sawil kiraamati
-
Gaa ñi gëm Limaamu te gëm Seydina Isaa fu ñu jëm
Am téraanga boole ca ndam Min zawil Kiraamati
-
Soo yaboo teral fuñu jëm fuñu wacc am na ñu ndam
Ñoom ñi boolé ñaari ngalam tey xayaarul ummati
-
Seydina Isaa di ngalam wuñu segg am na ngërëm
Defna fiy jalooré ba dem huwa zul kiraamati
-
“Huwa samsu laysa lahu “Fii zamaani zaa misluhu”
Ya Uxayya xuz annahu kanzu zul hinaayati”
-
Am na diine moodi kamaal Al hassibu zeynu fihaal
Samsu diine suux na huwal hafu zul Kiraamati
-
Moofi daan défar lu jubul lufi yakku seydi jubal
Boo bañee ñëwit mu yabbal ku ca dem fi saahati
-
Yàll Buur bi rus na ka moom nasaraan du weddi waxam
Moodi gar ku nekk fi moom woolu dootu jàqati
-
Boo defee lixuur ba gëlëm ci sa mbir ba seet ba xalam
Doo xalam ludul beg dem Li isaa fii saahati
-
Boo ñewee di laaj si ndigël Seydi jox la gën je ndigël
Boo jëfee la Njool ma digël doo fa jog di réccu ti
-
Waaja ñëw di laaj si ndigël dellu wor la Seydi digël
Kooku dootu jog ci mbugël dootu am salaamati
-
Bu demee ba soobu ca biir ba borom takkaay ya di door
Xel ma dem ca Seydi mu suur ku mu am fi saahiti
-
Moo fi doon leeral fu lëndëm ka misaalil badri tamaam
Ruuhu Laahi Isaa ku ko gëm xaw ma looy xalaatati
-
Waa ju gëm libaas li ko war jaamu Yalla moom kidi Buur
Boole Kawfi ak di yaakaar Fi nahiimi jannati
-
Seydina Limaamu da noon jaamu leen bu leen defi noon
Dimmëlënte koon lu nu ñaan din a al bi surhati
-
Bul di geesu waa ja gëlëm ba di gaaral Seydi Limaam
Loolu moodi tooke ci moom ju di jëm xiyaamati
-
Bul di xasté bul di bonal yoonu kenn bul tilimël
Jëfi kenn koon nga jubal yoonu seydi saadaa ti
-
Xaala laahu rabbu samad fii kitaabihi zil majiid
Lanu farix beyna ahad min rassulil hismati
-
Bul di xotti diiné té bul xotti worma kone nga kamala
Bul di reylu kone nga jubal Bi tariigi jannati
-
Bul di seet ci waaju la sut, bul di xeeb it waaji nga suut
Yalla moodi buur bi fi suut moodi zul xahaarati
-
Bul di seet ci man mika wax ndax dama jubul badi wax
Na nga seet manaam lima wax kon nga am hidaayati
-
Bul di andak waaju gëlëm bul di noonu waaju di xam
Kone nga soobu yoon wu di jëm daaru zil salaamati
-
Ruuhu Lahi waziiru Limaam Mahfiyun la ñëw nab a dém
Gaaéna doora lëñtu mbirëm Yaxtafoo la saarati
-
Moom la xam ba feeñal jëmmëm ci kayit ngir képp ku xam
Boo gisee wasiiru Limaam woolu dootu lëntëti
-
Gaayi gis mandarga ya xool gis jëmëm ja naa kee di njool
Ma ñu wax ni moodi matal wal hudaa bi dahwati
-
Gaayi yeewuleen baña juum Seydi Ruhu ñëw na ba dém
Seeti leen rakkam ja mu am baña jomba tuba ti
-
Seydina Manjoonay jubal ku fa ñëw te namma jubal
Du la tek ca jëf ja ludul farlu fiil Hibaadati
-
Am na diiné muñ na te moom ngor ga mat na am na ngërëm
Xol ba yaa na mat na imam am na ndam fii taahati
-
Moodi gééj gu fees ba di fuur ba njaa àlla yaa ngi ziyaar
Yaa Uxayya nanka ziyaar moodi zul kiraamati
-
Ndax njanaaw la ñëwna ziyaar andak gaa ña ñëw di ziaar
Ba mu doynu kullu ziyaar han zawil kiraamati
-
Muhjizaat ya feeñ na ca moom boo xamoon la nekka ca moom
Koon nga dem tuubaati ca moom moodi zul kinaayati
-
Yaw mi gëm Limaamu te gëm Seydina Isaa dellu gëm
Seydina Manjoon kula xam mucc min halaakati
-
Gaayi Njiin ku leen masa xam mbaa nga gis ka sopp jëmmëm
Am teraanga “yowma zihaam génn min Xusaarati
-
Yàll na Buur saxal nu ci gëm te jubal nu yoon wu di jëm
Hiliyiina daaru nahiim maha Seydi Saadaati
-
Wa salaatu maha salaam Han nayiiy xayri la naam
Zumma aali laysa yariim Abadan wa sahbati