Waxna ba tayyi
Waxna ba tayyi waaré naat ba tayyi
Waayé taxul ñu gëmko farko bayyi
Jiiñ ko ku manké ñeppa naako dofba
Muy yuuxu naa maay Ndaw li maay Yonnenba
Xeeb nan yëfëm jeebaané nan turëm wa
Yaqqab déram jeem tilimël yoonam wa
Tannefya xëy di rotsi gëmsi wooteem
Soppako nawko bañ ya naa manul am
Ñu jeem ko neexal naako baal sa Gaayii
Té jaamu Yalla bañ juyook Tubaab yii
Mu lànk naa Yallaa ma sas ma wooté
Ku Yalla woo doo mana bañ doo wuuté
Ñu xëy kalamekook Tubaab ya naan leen
Kii nara tas seen nguur gi moom la jugleen
Njool toroxal gawar ga noon ya perta
Tubaab ya rus naa nanko jeema betta
Ña taaliwoon ay woowa seeti Njoolma
Faylooka Taalba ñooko ñakka worma
Njoolma nileen Taal biima taal dootul fay
Bu Tan dawee Meddëmya dootu am lay
Kerook la waar gëmëm ya ngir dëfël leen
Riñaani bayyi bañ ya ngir yërëmleen
Ñu xëy di seet seen waaja fekka Njoolma
Gaddaay na penku far fanaan ca paxma
Tubaabya jog soonal ña doon jeebaané
Naan fuma dal sallaaw di ngeen ko genné
Ñu ngay sonnal Mbokkam ya ak Soppem ya
Ñuy wër ba lotta Buura muur seen gëtya
Buroom xolab wurus ba ngir yërëmleen
Wooleen ñu ñëw wërko ñjañam la sutleen
Waxtuwa jot mu naa farleena jiité
Ñu naako mukka rëyna liiñu wuuté
Njoolma di muuñ naalen ñu dem di ngeen xam
Ku juuwalook man manta mukka am ndam
Nan seeti ñii ngeen njortawooni man nan
Fay liima taal ñu darko melni ay jën
Noon yadi ree naa ngalla tay mu sànku
ku bayyiwul sun tuuryi faw nga alku
Soppéya xar rangooñi xol ya tuuru
di jooy ki tax ñu bàyyi ndëppak tuuru
Ñeey xaqqataay ngir bañko ak iñaané
Reeréni kii du noon bunuy kondaané
Ñëleey sikkar di tàggatook seen Njoolma
Mu naan du yàgg maa ngi ñëw xaarleen ma
Bu gaalgi weesoo Beer du maay seen Ndaw li
Ca Beer la ñeppa xamni moo yor Ndam li
Ña tëkkëwoon Nohin bëggoon ko sànk
Tuufan ba ñëw labal ña doon jaay pànk
Ña bëmëxoon Xaliil sa xalyaak taalba
Buur nasaxal seen yeené feg xaritba
Ña weddiwoon Muusaa dawal ngui rayko
La Yalla soob sa geej ga far muccëlko
Ña yeenéwoon Masiihu jëlko boom ko
Buur Yalla xëy yekkiko ngir wormaalko
Ña doon nasak nucci di yeeru Mommadu
Buur gumbëloo seen gëtya muccël Ahmadu
Ñoo doon fexey sànki Limaamook rayko
Ka muccëloon Yonnen ya mo xëy fegko
Moo nasaxal seen yeené mooko yekki
Ci Addunaak ëllëk bu ñeppay dekki
Kuko bawol doo noppalooti Dunyaa
Boo moytuwul doo musa tàggook lorya
Kuy xas yëfëm namuy julee manooko
Namuy tudee Buur Yalla xañtuwooko
Manoo namuy wooré manoo zakaatam
Tabam ga dooku seen daboo ay dongam
Seenoo ngëmëm nam ragalee Boroomam
Nam wommatoo doo masa dab Ihsaanam
Xas kula sut bañ kula gën du worma
Tooñ kula man du xel Limaamooy Njoolma
Kum nandalul sallaaw du tàggook marwa
Ku jot xolam dootooko tal ngir aywa
Ku bañ yëfëm sallaaw du noppalooti
Lakoy xasan du wokku Kii Moomlaati
Ku raam sukkëlko raw nga mangasin yi
Moo leen di duy moo amé yeegél Gaayi
Limaamu ñoo ngi nii di ñaan Buur fayla
Ling nu defal ñun woolu nanla gëmla
Kep kula xas dinan la way lu sutko
Kep kula bañ sunuk cofeel far suulko
Yaa tax ba doo tun tuuri ak bokkaalé
Yaa tax ba doo tun boddi benna nawlé
Yaa tax ba dootun saaga dootun xasté
Yaa tax ba dootun jël alal di kasté
Yaa tax ba dootun noonu benna soppé
Ken manta waññi len si ninla jappé
Yaa tax banuy sellal di xañtu Yalla
Yaa tax banuy sakku mbegëm ngir jàlla
Yaa tax banuy sikar di kañ Boroombi
Yaa tax banuy suuxloo baken beek Noon bi
Yaa tax banuy jappanté ak soppanté
Ken manatul tax ñuy xulook xeebanté
Na Yalla sëlmël saa su jot muy julli
Ci yaw Yonnen "waarisu kulli fadli"
Ku am keneen jappal banook sun Njoolmi
Nu àndak ak moom ba kerook xiyaami
Gungeenu Maam Limaamu bulnu bayyi
Ling nu digël ñaanal ba bunci tayyi
Sun xolyi yaako moom jëlël laabalko
Sun Ruuyi yaay boroom jëlël sellalko
Sun xelyi yaako feesé yaak sa waa kër
Jot sa ngëmëm Maam rekka tax ñuy kërkër
Na Abdulaahi saxfi doon sun mbegté
Sakkuk mbegëm fim tollu mooy li konté
Na yalla taawu sak njaboot te fegleen
Fun mana nekk nuy saxoo xidmaal leen
Yalla gërëmnu maynu koom nandalnu
Ca geeji leer ya lunfi def nga baalnu
"Wa Laailaaha illa laah Mahmuudu
Rasuulu-laah aamanatu yaa ma'buudu"
"Summa salaatul-laahi zil ikraami
'alan-nabiy wa aalihil-kiraami".
Brazzaville, le 12 Avril 2017