Way Wérédi yi
1) Damaa gennë bis yëmbël di dox roomba benna dof
Mu took cip ruxxam, jël ay yoxoom fasko ciy waggam
2) Te leek leek mu ree, leek leek mu jooy, rafle waanko wër
Mu ngay lox kerook daa sedd, booleek taruk lëndëm
3) Werul, waaye teewul nak, mu dis gor nde tallalul
Loxoom kenna, tooñul it, ña toogoon ci ak wetam
4) Yaram waa nga sooñoo sooñu, duk dalla duk basañg
Te leeleek mu taw ndaysan, Ba taa suuxalap ëmbëm
5 ) Bu xiifee poubelle lay dem, amul nday jukay tibbël
Fanuy këppi dess lay dem, falay fekka aw ñamam
6)Teyit manla wax, day mujju dem lekka ñam wu bon
Gu am ñaari fan goo xamni, baaxul ci ak werëm
7) Namuy def, gisul Yaayam, té nak amna ñetti at
Yu mat sanguwul, lum sol, dakoy for ci ay sënëm
8) Bu jaay katbi sannee maango, baa sax Orange bu nëp
Mu daw këfko, noonee sax lakoy lekke cik taxam
9) Ngelaw saxxi, nit daw tabbi neegëm ne rapp tëc
Mudes kay tenaa yel, banta yay dal ci ay gëtëm
10) Te ndaysan, bu roombew dalla, baa pot, walaw sagar
Dakoy tek lu rëy, mootax mukoy boole cip ëmbëm
11)Dafay waxatu fum nekk; té leeleek mu mer di xun
Te kat amna nday, am Baay, ba am rakka, am magam
12)Bamuy wer la bokkak ñep, bes xëy ñu daalko ber
Awaay werëdee tax, wayé, as gor la woon su gëm
13)Rakkam donnanap neegëm, jabar jaa ngi sëy faneen
Te doom Sam amoon, boobee batay xoolukoy gëtëm
14)Juroom ñaari dof, lan roomba Tamba ñu reendileen
Ba jël seeni awraak seeeni yuur liika daw yaram
15)Danoo butte ñee, xar noppi ñee, ñee ñu sannileen
Ci ay kër yu ken yeggul, banuy xeeñ ñu doora xam
16)Gisël ñaata yoon, lap dof mdi xëy dee ci ap tabax
Bu yeggul, ba am ay fan, bafay xeeñ té ken du xam
17)Gisël benn dof bée faatu, leeleek ci benna xur
Bafay xeeñ, té ap xiif rek, moo saank ak dundëm
18)Gisël ñaata yoon lap dof, di xëy lekk ñam wu bon
ba feebar ca ay at, kén du juk saytu ay mbirëm
19)Gisël ñaata lan fekka, ap dof mu xëy wësin
te ken manla laaxaan ken, kén foogulap ëmbëm
20) Gisël ñaata dof, ngay fekk, dus woddu baa tubëy
Daniy raflé noonee rek di dém ñeppë gis pëyam
21) Gisël ñaata dof ngay fekk, dun jekki dun nélaw
Daniy dox ba dee, doo gis kunaa xamna bammelam
22) Te gisnaa fi bis ap dof, bu am benna gööm bu rëy
Mu ngay wokkatoo kay waxtu, ken saytuwul werëm
23) Liree rekk tax may woo état beek ku YALLA ñor
ñu booloo taxaw, tey saytu njaay YALLA yiinu am
24) Obama bamiy ñëw fii, danoo japp dof yi tëc
Ginaaw bam demee, lan leen boyal, ñepp gennë dem
25) Wowoo wowwo lööy yen guurnement Reew mi walluleen
Away wallu leen as gor, su xëy ñakka am xelam
26) Té gis ngeen fi, ay dof yeen, kuleen fac ñu daaal di wer
Té xam ngeen ni mbooleem dof yi, koo teyye dootu dem
27) Te dof boo fi gis muy dem, këruk nit la bayyikoo
ku wer dellu ciy mbokkam, xarit xél dafay xalam
28 ) Wutël nanfi fas, ak nak, vétérinaire yuleen di fac
Lu tee woon ñu sakkal dof, fanuy seete ak werëm
29) Te gisnaa ku fac mbaamam, té Gisnaa ku fac fasam
Fajup njaamba jööbëm, fac goloom sax, fajup xajam
30) Te taxtul mu fac mbokkam, mu xëy ñakk am xelam
Ku fac mbaam, ba fac xac, bayyi Nit andulak xelam
31) Ci lii sax ci laay fas ñaaxe, askan wi may waxal
Ñu daw leppë luy tax, nit di xëy ńakk am xelam
32) Xelay ganjaruk nit, xél la nit am ba not mbëfër
Xelay tax, xalep naar not, gëleem bay xëccup Nosam
33) Xelay tax ñu wullip naaga, yor Xacc, tay dañal
Té xam ngeen, du maasuk nit ci dooleem, akum rëyëm
34) Xelay tax, ba l'islam Tek nu jëf, Waa ju ñakk xél
Mamadou Dia du am yiw, té doootul yilif kërëm
35)Xelay tax nga xammee mbaax, xelay tax nga daw lu bon
xelay Tax ba Nitxam lëf ci Buur YALLA ak Mbirëm
36) Xelay ndap, la xam xam tabbi, ngir waaju ñakk xél
Du xam lëf, du am lëf, waaju am xél xamiy yefëm
38) Xelay leer ci nit, xëy tedda mootax Ba Aadamu
di sangup Maalakak Jinne, ibliisu ñakk ndam
39) Xelay tax Ba nit rekkay sangup suuf, lu weesu nit
walaay loofi gis ngir nit la, ngir moo yoram xelam
43) Ma wax yenna Mbir yiy tax ba Sun ndawñi xëy di dof
ñilee rapla, Ñii ay raapla, raap yaxxanay ndawam
44)Dofup raap dafay wuuteek, dofup rap ci yeena Mbir
Nanuy maytu yaambaa, daw drogue bayyi am tuxëm
45) dofak iilu, ak book siisu, ñoo mit dinaa ci ñëw
damay njëkk way kii, sangaray yaxxa ak dundëm
46) Balén foowè dulian, day rayum xél, di yaxxa xol
Lu ray xol, di yaaxam xél, kukoy def, du nit nga xam
47)Te alcool alak naw gaay, kukoy Naan de dootu wer
Lu waay xam xelam rek jaayko, ngir jëndekook werëm
48)Layis rek di yaxxal nit ci xol, ak ci ay xëtër
Ñi xam neeñu day dem sax, ba yaxxal ko ak dundëm
49)Te dee diis kukoy Naan, manna dee, dee gu tiis té tar
nde luy fëxxë bët, moo gën, ci nit luy fëxxap xolam
50) Gisël Waa ji Naan sungum ni xëndëng ci geddi bëy
nelaw bay xarang sung soofna lool, xelyi lay Guesëm
51) Amoonna ku man ndim sëng, far tër di yag yagal
ñu koy taccu muy taasooka saagaa ci ay dëkëm
52) Te amna ku naan mbiic daanu ban sacc lam yoroon
te moy lim bu rëy booo xamni, moo yor dundëk kërëm
53) Amoonna ku naan saampaañ, di xeexoo ñu farko ray
sulaar yaako jam ay paaka, ndaw dee gu ñakka jom
54) Kunaan roos, Du rus nit, dootu rus YALLA, dootu rus
njabootam nde manna sax sëyee yaayamak rakkam
55)Music yeek flag day yaxxa am xel baleen drogue
Coca gëm cocaayin fop, cim am xel akup yaram
56)Te gisnaa Ku Naan am njolla ,daa maandi bay tërëf
xaleel Yaako sottim ndax, mufar yaxxa ay sërëm
57) Te sax amna dof yooxamni ay wirda lan yoroon
ba rawxaan ya doflooleen, ñu far toppa ay xërëm
58)Gisël bènna waay jee wird ap diir mu summi ay
Bubaam summi caayaam gennë, neegëm di dox di dem
59)Te kat banko laajee, neena suuf seeko antanul
ma laac waaji kon, jan suuf ladoon sampa ay ndëgoom
60 ) Te talsam yi ak rawxaan yi, lin sanka ciy xaleel
Drogue mantukoo jot fawwu, dof gi du neexa xam
61) Tey say jekka taxnak cam, di siisooko say badof
ku rus ap dofam day metti, ngir yombulak fajam
62)Gisël jenna waajiy yuuxu tey daw di wër tenaa
Dafay baña doon ap xutbu , kii seenunaak ndofam
63) Té am raxasun sax sax xarit waxma lunsi xam
Lu dul ndof, jëlël aw tur wu leer bayyi talsamam
64)Te Tas Tasna waay, bam yuuxu, xaccit mu tas kërëm
Té tas Mbiremak soxnaam, ñu naa deet mu tas xelam
65)Kitil ak katal ak magg jal jal kukoy sikar
bu teewloo waroon naa ree, Dafay baat yu am xorom
66) Te am nasabin,ak xantariisun kouleen bawul
Dafay mujju rek, fop ay mbubëm daanu ciy sënëm
67)Jaxaay yaayu dajdahtiilu, dofloona ay kureel
jalaal jalna fiy bammeel, té dofloo ñu am xorom
68)Gisël waaji tëj neegëm ba ap diir mu mbëkk daw
te naa maani "Aljabbaaru" maatay ci ap ëttëm
69)Ku woo Ummu Mussak yaayu jalxay ci ay Kurus
Mawooman ka bindoon, yaayi Mussa té yor Mbirëm
70)Kufiy woo 'afaaritun minal jinni, manma Woo
Ka bindoon 'afaaritun té yor leppi wërsëgëm
71) dalal nak té Tey, sooy sakku Mbir, ndax ku wattuwul
xerëk ëppëlak yakkamti Looy sakku dooko am
72) Faral noppi Saliou, wax bu niiwee té am njariñ
dafay doy, Salaatun Yalna dal Taaha ak ñoñam