Xayartu Limaamu
1-Bi ismil Ilaahi ma wax fii li Laahi
« Fadaa-i là Laahi » ci waa ahlu Laahi
2-Buur Yàlla-a di xééwël, ba tax ku ka gééwël
Di sikar mu xééwal la, jannata Laahi
3-Nun dey wàr nanoo xam ne Yàlla nammeelam
La indi ci baaxam Imaamil Laahi
4-Mu yékkëti lislaam mu sax fii ci «kàllaam »
« Minna Laahi » baatam ba jolli wa Laahi
5-« Xayartu » Limaamu mi ñëw ngir nu jaamu
Ba yékki « Kàllamu tawhiidi li Laahi
6-« Alhamdu li Laahi bi tawfiixi Laahi »
Imaamu Ilaahi nu gëm ko wa Laahi
7-« Fayaa Ahlu laahi » saxoo leen li Laahi
« Bi Zikril Ilaahi » te doy loo bi Laahi
8-Buur Yàlla cik màggaam la yònni malaykaam,
Ñuy seet gééwi gaayam ci waa « Ahlu Laahi »
9-Seen jénééri yu leer ya , ya leer melni weer yaa
Ñoo leer gindi gaa ya ñu wër leen wa Laahi
10-Malayka ya peek leen te wër leen te yiir leen,
Fu ngeen ne ñu xam leen bi Zikril Ilaahi.
11-Te ñoom du ñu dellu feek gaaya di booloo
Ci Yàlla te doyloo « Bi Zikril Ilaahi »
12-Ba saa ya ñu delloo ca Buur ba ñu doyloo
Mu laaj la ñu soxla « Bi Zikril Ilaahi. »
13-Ñu naa ka yaa Rahmaan da ñoo ragal « niiraam »
Té bëgg am « ridwaan » « Bi nihmati Laahi »
14-Buur Yàlla naa leen ndax dañoo mosa gis sax
Mbugël ya ca biir tax ñu gëm ma fii Laahi
15-Am ñoom dañoo séénoom Aljana ak wildaan
Yay teeru ñaa deewoon “fi rahmati Laahi”
18-Malayka ya naa ka da ñoo dégg « an ka »
Rasuulu wax leen ka ñu gëm ko wa Laahi
19-Yàlla ne mey naa leen la ñuy wut té maa leen
Di wottu musël leen « Bi nasrati laahi »
20-Malayka ya naa ka diwa nga fa kooka
Da doon déglu rekka « Bi Zikkril Ilaahi »
21-Yàlla ne jéggël naa ñoom népp te wòòr na
Ak ku xolom neex na « Bi Zikril Ilaahi »
22-Lii dey doy na cee wax ci kuy dégg ay wax
Ndax Buur Yàlla moo wax “fi Zikril Ilaahi”
23-“Wul law kaana bahru Midaadaan fa bahru
La nafidal bahru Li kilmati Laahi”
24-Seetal saaru kaafi ba giska te kaay fii
Nga xamne amul fii lu gën Zikril Laahi
25-Yalna nu Buur Yàllay Tëbb ca leeram yay
Ngënnèl ya ci wormay Imaamil Laahi
26-« Wa salli wa salliim Ilaahi wa karim
Alaa Seydil ummam Bi zikril Ilaahi”