Yaa NabiyalAllah
Yaa Nabiyyal-laah
Yaa Habiibal-laah
Xayra xalil-laah
Yaa Rasuulal-laah
Ay Yonen bi damaa
Yeené gansila maa
ngiy dagaan wuyumaa
Yaa Rasuulal-laah
Maangi nii amumaa
Kenn faalewumaa
Ay Yonnen sowemaa
Yaa Rasuulal-laah
Bët yi jooyna ba loor
Tiis yi farnama muur
Maangi nii di la xaar
Yaa Rasuulal-laah
Woppa gee ma sonal
Bañ ni rekka du dal
Xawma sax luma dal
Yaa Rasuulal-laah
Bor yi notnama tay
Maangi jeem diko fay
Diis na boobu batay
Yaa Rasuulal-laah
Maangi wut luma am
Ngir teral ñima am
fëgg naa fuma xam
Yaa Rasuulal-laah
Waaye tay dama xëy
ëmbë leppa di wëy
Liima yëk dafa rëy
Yaa Rasuulal-laah
Am la rek dafa doy
Yaw mi ñeppa di roy
Ñàkk mooy kila moy
Yaa Rasuulal-laah
Yaw la Yalla gërëm
Yaa di buntu kërëm
Yaw la jox ndigëlëm
Yaa Rasuulal-laah
Yaw la Yalla teral
Waxni nanla begal
Ëpp ngaa woyofal
Yaa Rasuulal-laah
Yaw la Yalla xamal
Mbootya yawla tëbël
Koo mosal du doyal
Yaa Rasuulal-laah
Yaw la Yalla jubool
koo xulool duko xool
Sutnga ñepp di Njool
Yaa Rasuulal-laah
Yaw la Yalla faral
Yaw la woolu yabal
Fal la naala waxal
Yaa Rasuulal-laah
Ñëw nga jottalinga
Xeet wi xettalinga
Dem nga dellusi nga
Yaa Rasuulal-laah
Lep lu baax ngani am
Lep luñaaw ngani cam
Kenna dootula jam
Yaa Rasuulal-laah
Sak cofeelama yeem
Ling fi xamba du giim
Koo layool mu nërëm
Yaa Rasuulal-laah
Ñëwnga wooté matal
Wan nu yoonu jubël
Rëyna ling nu defal
Yaa Rasuulal-laah
Noo ngi jeem dila roy
Ndax gërëmla du doy
Noo ngi sax dila way
Yaa Rasuulal-laah
Bëggënanla bu wer
Defla ngay sunu mbër
Wekla Yaay kiko jar
Yaa Rasuulal-laah
Noola jox sunu xol
Yaw mi fees sunu xel
Yaw mi jar di dawal
Yaa Rasuulal-laah
Noo ngi ñaan sa ngërëm
Am la fep funu jëm
Gisla Bes banu jëm
Yaa Rasuulal-laah
Yiirnu maynu nu am
Njub ba ken dunu jam
Xoolnu bët bu yërëm
Yaa Rasuulal-laah
Joxnu jappalenu
Fegnu xettalinu
Maynu leer gungenu
Yaa Rasuulal-laah
Bulnu bayyi Yonnen
Bulnu jeppi Yonnen
Bul merook nun Yonnen
Yaa Rasuulal-laah
Lepp lun mana def
Bon taxul nu tërëf
Sagganay linu këf
Yaa Rasuulal-laah
Man nga jëlnu tinul
Man nga jëlnu jubël
Man nga tax nu kamaal
Yaa Rasuulal-laah
Ay sagalnu Yonnen
Ay sagoonu Yonnen
Ay faroonu Yonnen
Yaa Rasuulal-laah
Yalla julli ci Yaw
Miy sangub kufi yiw
Yaay yonnen bifi raw
Yaa Rasuulal-laah
Yalla yokka sa leer
Fayla ling fi defar
Yaadi janta bu leer
Yaa Rasuulal-laah
Yalla fay sa njaboot
Yokk kep kunu boot
ñeppa xëysi di root
Yaa Rasuulal-laah
Mawlid-11-12-2016
#lejeunepoete