Ziarnaa Maam Limaamu
Baay Laay Mooy Yonnenba
Way wii maa ngi ko tambabalé si rawdub Jamaalay, besu Appel tollook 20 Mai 2015. Mangi siy layebiir mbokk yi, si nanlanuy xammee ndawal Yalla : Tambalee si Njubgaak, Keemaanya ak Wooté ba. Wanleen ni yooyu yepp dëpook si wootem Seydinaa Limaamu Laahi. Gëna faram face keemaanu wax kumpa gi Boroom denkoon Baay Laay. Jeexaleko ay denkaané ngir way gëmyi ak ay ñaan ngir ñiy wër nëbub Yalla bi. Nako Yalla nangu.
1. Ziarnaa Maam Limaamu Ndawal Boroomba
Kudee daa xamni Baay Laay mooy Yonnenba
2. Kudee yakaar na gisko ba am shafaa’am
Kunuy yaakar Limaamu la def amal ba
3. Kerook bu Mbindeefyi sappee Bes payoor ba
Jahannama yuuxu def Wildaan ya shiiba
4. Kerook tangor wa mettina waaye tiit maay
La jaaxal Jaam ña ñepp di daw Maxaam ba
5. Maxaamab jog waxak Buur ñepp koy daw
Seriñsaak Ndaw ña ñepp ragal Boroom ba
6. Ñu seet Maam Aadamaak Nuuh Maami jaam ña
Musaak Iissaak Ibraayma ña gaddu yanba
7. Ñu naan lii ñoo si yam Iissaa taxaw naa
Ñu dem seet book ki Yalla defoon habiiba
8. Isaa woo Maam Limaamu te naako Baay tay
Kufiy jaam yaw la yaakar yaay Shafii’ ba
9. Kerook la boroom Dërëmbi di ñaan Boroomam
Xolam ba yërëm njaboot ga mu yor Liwaam ba
10. Boroom bi takkal Limaamu garaat ya foofa
Bilay moo moom Wasiila Fadiila besba
11. Kerook kuy soppe ak kuy noon di maase
Tenaa xaqqan Limaamoo moom dërëm ba
12. Limaamoy Xayru xalxil-laahi turran
Ku yeeg galam ga mucc ba naani Tuubaa
13. Lutee ngeen gëm ko fii xaamee ko foofa
Lutee ngeen ñëw faroook ki farook Boroomba
14. Xanaa xamuleen ni Yalla du jox Yanam ba
Ludul kunu seede mbaaxak leeru xolba
15. Xanaa kay Njiin mi yeemoon ñep sa tabgaak
Dëgoom gaak sellateem ga xolam bu yaaba
16. Bu mus daan nappi jënya du agga kërga
Bu goobee may kerook ñay romba toolba
17. Bu gan yeksee Limaamu teral ko leel ko
Di wër ngir gis ku soxla ndimbël sa xiif ba
18. Ku jaaxle si moom la daa nëw diisko soxlaam
Da ngay laaj Yoof ñu waxla tabag loxoomba
19. Lutee ngee laac ñi xam xammee Yonnen ya
Te yër teerey Dala’ilu xam ’alam ba
20. Yëroo leen Bayhaxeek waa Asbahaan ya
Nubuwwaat jaang Maawardeek jukeem ba
21. Ku Yalla yabal demal yër Ibnu ‘Aashir
Sa keemaan yaadi seedey Yalla booba
22. Bu yalla ameet di Zaalim baa ku manki
Si seetaan ak si dimbali Muftarii ba
23. La Ibnu xayim waxoon ñay jam Yonenba
Ghazaalii yeemna ñay bañ bayyinaat ba
24. Dangeena xamul li Baay Laay def si keemaan
Amil i’raadou sonnatukum ? ba booba
25. Bu ngeen fi nangoo Musaa ndax xarna geejga
Labal Noonam ba geej ga demaat palaas ba
26. Lutee ngeen gëm ki randal geej ba tay geej
Ñëwaatul fay palaasam ndax rëndëmba
27. Bu ngeen fi nangoo Isaa ndax mu’jizaatam
Yamuy wowee ña dee ñuy degg baat ba
28. Lutee ngeen gëm ki daan ëf nit mudib neew
Di dekkal waaju dee mbaa feg dogal ba
29. Budee ixbaara tax Qur’an di keemaan
Xibaari ña paase ak ñay ñëw sa digba
30. Budee njubgaay laleen jaaxal si Yonnen
Te umiyyun la tax ngeen nangu cërba
31. Buleen bañ kon ki suuf waayoo bakoy deey
Lu nit nas mooka xam peek mbooti xolba
32. Na ngeen laaj Goorga bañ koy xas si seetaan
Limaamu ba rabwa jappako naako dofba
33. Te fekka Limaamu yekkati baat ba woote
Ginaaw jiimun sa faatuk Soxna Kumba
34. Limaamu dalalko naako Ndijaay de xamnaa
La penca ma wax bilaay man maay Dogalba
35. Xanaa deggoo ba Dammeel Samba Lawbe
Gisee gentam ga yonnee ndaw ca sawba
36. Tenaako demal waxalma Limaamu gisnaa
Limaamu xabaark mbuusi dereet ya besba
37. Xabaarko joleem ga guddik Tamxarit ga
Firil nako ñaar ya noppi ca bay ñeteel ba
38. Mu yonni ndawam te naa fasyeene na ñëw
Si gëmsila Njiin ne Samba du samm digba
39. Waziir baa tax mu fomma ragal palaasam
Te moo nangoot gëleemak Njoolma Demba
40. Limaamu nelen ku xeexe ko des nalay daan
Ñu xeexi ji perta delsi ñu rayfa Samba
41. Limaamu nelen ñeteel baa ngook bilaay Njiin
Ku kay kontar da ngaa reeree cërëm ba
42. Kerook ba tubaab ba yeenee dal sa kaw Njiin
Ba ñetta ña daaldi deeyo seen plaŋ ba
43. Ba suuf seddee ñu ñëw daje ak Limaamu
Ca poot banu jaar mu nettalileen xabaarba
44. Ba ñaari azaan ya yeenee lëñtu kërga
Mu naan xaarlen ki leen fi yabal dikkëm ba
45. Bu loolu doyul na ngeen laaj Maam Galaay Jop
La goorgi Maseer waxak gentam ga Deeg ba
46. Ba Njool may yuuxu Ammar doomja naan ko
Waxalma sa Baay mu wuysima maay Digëmba
47. Xabaarnako ñay ya ndox masa suufu Wànxal
Kerook la laxas te naa Njiinay Yonenba
48. Xanaa kii took si siisam doyna tektal
Sheriif Abdooy darapoob neegu Kumba
49. La Maamja waxoon si siiwal ngir mi amna
Kufiy wax kumpa Njiina la may sa cërba
50. Lutee ngeen nangu Baay Laay yaynaleen ndax
Lu ngeen gëme Ndawyi defnako moy Rayiisba
51. Bu ngeen seetem ngiram seetab kureelëm
Di ngeen xemmem namuy jamoo Boroom ba
52. Namuy julleek namuy bakkee Boroomam
Na ngeen ko xalam zakaatam mooy xalaas ba
53. Bu ngeen peese waxam ji du ngeen ko reere
Ku weddi Limaamu weddina Yalla Buur ba
54. Awaay yaw mii Boroom bi dogal nga gëm Njiin
Na ngay salloo te dolli di santa Buur ba
55. Na ngay jëfe dikleya tay daw tereem ya
Te sàkku mbegëm ma tay ñaan Buur Ijaaba
56. Te bul xasteeka ŋaññe te bul werante
Te buldi xulook ki reere Boroom Meteel ba
57. Limaamu newoon na Diine amul werante
Amul xeebit sa nawle di xas Sëriñ ba
58. Boroom bi la soob ñu wuute wa laa nazaalu
Ki xelloy waaju nangu te gëm dogalba
59. Damay ñaan Buur bu ubbi nëbëm bi def leer
Si xol yeek xel yi ngeen janlook Dogal ba
60. Awaay Baay Laay ziyaarbaa ngii nangulma
Na Buurbi defal la lay Wasilaak Maxaam ba
61. Gërëm ma ndamoo ma falee ma ay farooma
Samab xol laala jox yaw miy habiiba
62. Salaatul laah dawman was-salaamu
’alaa xayril anaami ma’as sahaaba
63. Wa ahlil-laahi turran nuy saxoo gëm
Ki Yalla yabal jamaana te yanko yanba
Appel 2015,
Rawdub Jammlaay
20-21 Mai 2015
2. Shafaa’am ( شفاعه ): Ak Rammoom.Amal (أمل ): Yaakaar.
3. Wildaan ya shiiba (ولدان، شيبا ): Xale ya ay Magget.
4. Maxaam ba (المقام المحمود ): Maxaam bi benn di mindeef di am kerook bes penc, muy saña jog waxak Buur Yalla.
5. Ndaw ña: Yonnent yi Yalla Yonniwoon.
7. habiiba (حبيبا ) : ab soppé.
8. Shafii’ (شفيع ) : Aji rammu ji.
9. Liwaam (لواء الحمد ) : Liwaau’l hamd.
10. Wasiila, Fadiila ( الوسيلة والفضيلة ): ñaari teraanga yi Boroom bi di jox benn si ay jaamam, te Yonnen sàkkuwoon ñuka koy ñaanal.
µ11. xaqqan (حقا ): Dëgg Dëgg. Dërëm ba: Dërëm bi Seydinaa Limaamu (AS) doon laaj bimu fiy waaja juge naan kuko yeene Mustafaa (AS) nakako jox. Bu bes Pencaa, bu gisee Mustafaa (AS) gisko moom Limaamu (AS) mu delloo kako, bu gisul kudul kamu joxoon Dërëmam nak mu xamni joxoon nako Boroom.
12. Xayru xalxil-laahi turran (خير خلق الله طرا ): Ki gën si lu Yalla bind. Tuubaa (طوبى ) : Aljana. 19. Dala’ilu (دلائل النبوة ) : Dala’ilun-nubuwwa Tektali Yonnent yi. ‘Alam: (علَم ) : Mbandargama.
20. Bayhaxeek waa Asbahaan مؤلفوا كتب دلائل النبوَّة أمثال الإمام
البيهقي و أبي ) ( نعيم الأصبهاني وابن حيَّان الأصبهاني و أبي محمد
الأصبهاني صاحب أعلام النبوة : Muy ñenn si ñi Taalif Teerey Dala’ilun-nubuwwa. Nubuwwaat (النبوات لابن تيمية ): Teereb Nubuwwaat bu Imaam Ibnu Taymiya. Maawardii ( الإمام الماوردي صاحب كتاب أعلام
النبوة ) : Imaam Maawardii Boroom teereb A’laamun-nubuwwa.
21. Ibnu Aashir ( مقدمة ابن عاشر في قوله: إذ معجزاتهم كقوله وبر
صدق هذا العبد في كل خبر ) : Ibn Aashir sa Muqadimaam ba dafa waxni: Keemaani Yonnent yi mooy toollook kàdduk sunu Boroom si waxni « man mii may kileen Yonni ».
22. Zaalim (ظالم ) : Tooñkat (tudd naa ak Sellam, ndax sorina loolu). Muftariiba (مفتري ) : Ibn Xayyim si Nubbuwaat dafa waxni bu Buur Yalla seetanee wala mu jappale kiy woote sik neen si keemaan yimuy def, kon dey xanaa dafa doon Buur buy tooñ wala reeral ay jaamam wala muy Buur bu amul xel (manke) si dooleel kukay duural.
23. Ghazaalii ( الإمام الغزالي لليهود في إنكار لنبوة عيسى رغم تحقق
معجزاته ) .Bayyinaat ba (بينات ) : Imaam Ghazaali dafa waxoon Yahuud yi naka ngeen di bañee Yonnentek Iisa te mu sax ni def na keeman si dekkal nit ku dee ? Da ngeena weddi amuk keemaan ga wala da ngeena bëgg waxni dekkal ku dee du keemaan ? Bu dee saxal ngeen amuk keemaan ga kon naka lako manee budee lamu woote du dëgg ? Noo leen mana gëme nit si soppi yat jaan bëgg weddi kii fekk ku dee mu dekkal ko.
24. Amil-i’raadou sonnatukum (أم الإعراض سنتكم ): wala weddi mooy seen yëf ?.
27. mu’jizaatam (معجزة ): Ay keemaanam.
29. ixbaara ( إخبار عن الغيب ) : Wax kump. Aalu Fir’awna bil Aayaati ( آل
فرعون بالآيات ) : (woo) waa kër Firawna si ay keemaan yu rëy.
30. umiyyun (أمي ) : Ku manul jàng manul bind.
33. jiimun (جيم أي ثلاثة أيام ) : ñetti fan.
µ39. Waziir (وزير ) : Jëwrinba Demba Waar.
42. ñetta ña: Tubaab ba ak ñaari Sahaabam ya Momar jaañ Aminita ak Njaga sekk.